Al-Kahf · 33/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
كِلْتَا الْجَنَّتَيْنِ آتَتْ أُكُلَهَا وَلَمْ تَظْلِم مِّنْهُ شَيْئًا ۚ وَفَجَّرْنَا خِلَالَهُمَا نَهَرًا ۝٣٣
Kiltal jannataini aatat ukulahaa wa lam tazlim minhu shai`anw wa fajjarnaa khi laalahumaa naharaa
📖 Tekkim Wolof
Ñaari tool yépp ñu cay jële meññent mu dara wàññeekuwut. Nu xotti ca seen diggante ag dex.

🎧 Dégg


📜 Aaya 31-35 — Al-Kahf

31أُولَٰئِكَ لَهُمْ جَنَّاتُ عَدْنٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهِمُ الْأَنْهَارُ يُحَلَّوْنَ فِيهَا مِنْ أَسَاوِرَ مِن ذَهَبٍ وَيَلْبَسُونَ ثِيَابًا خُضْرًا مِّن سُندُسٍ وَإِسْتَبْرَقٍ مُّتَّكِئِينَ فِيهَا عَلَى الْأَرَائِكِ ۚ نِعْمَ الثَّوَابُ وَحَسُنَتْ مُرْتَفَقًا
Ñooña ñeel na leen Àjjana dëkkuwaay boo xam ne ay dex dañuy daw ca suufam. Te deef na takkaayale ca foofa ay lam yu wurus te danañu fa sol ay yére yu nëtëx, di yéréy sooy bu sew ak sooy bu tal, ñu sóonu ca seen lal ya. Ndaw yool bu neex, waay-waay ndaw yenduwaay bu rafet te neex !
32۞ وَاضْرِبْ لَهُم مَّثَلًا رَّجُلَيْنِ جَعَلْنَا لِأَحَدِهِمَا جَنَّتَيْنِ مِنْ أَعْنَابٍ وَحَفَفْنَاهُمَا بِنَخْلٍ وَجَعَلْنَا بَيْنَهُمَا زَرْعًا
Joxleen leebuw ñaari góor ñoo xam ne : kenn ka jox Nanu ko tool bu am garabi reseñ, Nu wërsëgale leen ak garabi tàndarma, Nu def ca seen diggante ay tooli mbey.
33كِلْتَا الْجَنَّتَيْنِ آتَتْ أُكُلَهَا وَلَمْ تَظْلِم مِّنْهُ شَيْئًا ۚ وَفَجَّرْنَا خِلَالَهُمَا نَهَرًا
Ñaari tool yépp ñu cay jële meññent mu dara wàññeekuwut. Nu xotti ca seen diggante ag dex.
34وَكَانَ لَهُ ثَمَرٌ فَقَالَ لِصَاحِبِهِ وَهُوَ يُحَاوِرُهُ أَنَا أَكْثَرُ مِنكَ مَالًا وَأَعَزُّ نَفَرًا
Mu am meññent [mu bari] tax mu wax ak moroom ma neko : “Maa la ëpp alal te gën laa bari mbooloo”.
35وَدَخَلَ جَنَّتَهُ وَهُوَ ظَالِمٌ لِّنَفْسِهِ قَالَ مَا أَظُنُّ أَن تَبِيدَ هَٰذِهِ أَبَدًا
Mu dugg ca toolam te moom tooñ na boppam ; mu ne : “Yaakaar naa ne lii du jeex mukk,
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
33Aaya

Tekki — Al-Kahf 33

Simoore Al-Kahf Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñaari tool yépp ñu cay jële meññent mu dara wàññeekuwut.…

Simoore Aaya 33/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers