Al-Kahf · 52/110
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Kahf
وَيَوْمَ يَقُولُ نَادُوا شُرَكَائِيَ الَّذِينَ زَعَمْتُمْ فَدَعَوْهُمْ فَلَمْ يَسْتَجِيبُوا لَهُمْ وَجَعَلْنَا بَيْنَهُم مَّوْبِقًا ۝٥٢
Wa Yawma yaqoolu naadoo shurakaaa`i yal lazeena za`amtum fada`awhum falam yastajeeboo lahum wa ja`alnaa bainahum maw biqaa
📖 Tekkim Wolof
Ca bis ba Mu waxee ne : “Wooleen sama bokkaale ya ngeen sos”. Bu ñu leen woo dey, duñu leen wuyyu ndax def Nanu ci seen diggante aw xur.

🎧 Dégg


📜 Aaya 50-54 — Simoore Al-Kahf

50وَإِذْ قُلْنَا لِلْمَلَائِكَةِ اسْجُدُوا لِآدَمَ فَسَجَدُوا إِلَّا إِبْلِيسَ كَانَ مِنَ الْجِنِّ فَفَسَقَ عَنْ أَمْرِ رَبِّهِ ۗ أَفَتَتَّخِذُونَهُ وَذُرِّيَّتَهُ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِي وَهُمْ لَكُمْ عَدُوٌّ ۚ بِئْسَ لِلظَّالِمِينَ بَدَلًا
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya ne leen : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñu sujjóot [ñoom ñépp] ba mu des Ibliis, moom bokkoon na ca jinne ya, daldi sàqi ndigalu Boroomam. Ndax dangeen koy jàppe xarit mook i sëtam, bàyyi Nu [Nun Yàlla], te ñoom seeni noon lañu ? Bon na, li tooñkat ya di weccee !
51۞ مَّا أَشْهَدتُّهُمْ خَلْقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَلَا خَلْقَ أَنفُسِهِمْ وَمَا كُنتُ مُتَّخِذَ الْمُضِلِّينَ عَضُدًا
Seedeloowunu leen it sos ga Nu sos seeni bakkan. Te it jàppewuma [ñiy sànk nit ñi] ñu may jàppale.
52وَيَوْمَ يَقُولُ نَادُوا شُرَكَائِيَ الَّذِينَ زَعَمْتُمْ فَدَعَوْهُمْ فَلَمْ يَسْتَجِيبُوا لَهُمْ وَجَعَلْنَا بَيْنَهُم مَّوْبِقًا
Ca bis ba Mu waxee ne : “Wooleen sama bokkaale ya ngeen sos”. Bu ñu leen woo dey, duñu leen wuyyu ndax def Nanu ci seen diggante aw xur.
53وَرَأَى الْمُجْرِمُونَ النَّارَ فَظَنُّوا أَنَّهُم مُّوَاقِعُوهَا وَلَمْ يَجِدُوا عَنْهَا مَصْرِفًا
Te saay-saay sa jenook Safara daldi foog ne dañu cay tàbbi te duñu ca am aw rawtukaay bu ñu ca rëccee.
54وَلَقَدْ صَرَّفْنَا فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ لِلنَّاسِ مِن كُلِّ مَثَلٍ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ أَكْثَرَ شَيْءٍ جَدَلًا
Te Nun biral nanu ci Alxuraan jii, ngir nit ñi, léebu wu nekk. Waaye nit mooy ki gën a mën a dàggasante ci mbindeef yi.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
52Aaya

Tekki — Al-Kahf 52

Simoore Al-Kahf Aaya 52 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ca bis ba Mu waxee ne : “Wooleen sama bokkaale…

Simoore Aaya 52/110 — Simoore Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Kahf Dégg, Simoore Al-Kahf Tekki, Simoore Al-Kahf mp3, Simoore Al-Kahf pdf. Aaya 50–54. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers