Al-Kahf · 51/110
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Kahf
۞ مَّا أَشْهَدتُّهُمْ خَلْقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَلَا خَلْقَ أَنفُسِهِمْ وَمَا كُنتُ مُتَّخِذَ الْمُضِلِّينَ عَضُدًا ۝٥١
Maaa ash hattuhum khalqas samaawaati wal ardi wa laa khalqa anfusihim wa maa kuntu muttakizal mudilleena `adudaa
📖 Tekkim Wolof
Seedeloowunu leen it sos ga Nu sos seeni bakkan. Te it jàppewuma [ñiy sànk nit ñi] ñu may jàppale.

🎧 Dégg


📜 Aaya 49-53 — Simoore Al-Kahf

49وَوُضِعَ الْكِتَابُ فَتَرَى الْمُجْرِمِينَ مُشْفِقِينَ مِمَّا فِيهِ وَيَقُولُونَ يَا وَيْلَتَنَا مَالِ هَٰذَا الْكِتَابِ لَا يُغَادِرُ صَغِيرَةً وَلَا كَبِيرَةً إِلَّا أَحْصَاهَا ۚ وَوَجَدُوا مَا عَمِلُوا حَاضِرًا ۗ وَلَا يَظْلِمُ رَبُّكَ أَحَدًا
Ñu teg Téere ba. Nga gis saay-saay sa tiit ca la nekk ca biir, ñu naan : “Ngalla nun, cëy waay téere bii, bàyyiwul lu tuuti, bàyyiwul lu rëy, bind na lépp ? ” Ñu gis la ñu defoon di lu teew. Te sa Boroom du tooñ kenn.
50وَإِذْ قُلْنَا لِلْمَلَائِكَةِ اسْجُدُوا لِآدَمَ فَسَجَدُوا إِلَّا إِبْلِيسَ كَانَ مِنَ الْجِنِّ فَفَسَقَ عَنْ أَمْرِ رَبِّهِ ۗ أَفَتَتَّخِذُونَهُ وَذُرِّيَّتَهُ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِي وَهُمْ لَكُمْ عَدُوٌّ ۚ بِئْسَ لِلظَّالِمِينَ بَدَلًا
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya ne leen : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñu sujjóot [ñoom ñépp] ba mu des Ibliis, moom bokkoon na ca jinne ya, daldi sàqi ndigalu Boroomam. Ndax dangeen koy jàppe xarit mook i sëtam, bàyyi Nu [Nun Yàlla], te ñoom seeni noon lañu ? Bon na, li tooñkat ya di weccee !
51۞ مَّا أَشْهَدتُّهُمْ خَلْقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَلَا خَلْقَ أَنفُسِهِمْ وَمَا كُنتُ مُتَّخِذَ الْمُضِلِّينَ عَضُدًا
Seedeloowunu leen it sos ga Nu sos seeni bakkan. Te it jàppewuma [ñiy sànk nit ñi] ñu may jàppale.
52وَيَوْمَ يَقُولُ نَادُوا شُرَكَائِيَ الَّذِينَ زَعَمْتُمْ فَدَعَوْهُمْ فَلَمْ يَسْتَجِيبُوا لَهُمْ وَجَعَلْنَا بَيْنَهُم مَّوْبِقًا
Ca bis ba Mu waxee ne : “Wooleen sama bokkaale ya ngeen sos”. Bu ñu leen woo dey, duñu leen wuyyu ndax def Nanu ci seen diggante aw xur.
53وَرَأَى الْمُجْرِمُونَ النَّارَ فَظَنُّوا أَنَّهُم مُّوَاقِعُوهَا وَلَمْ يَجِدُوا عَنْهَا مَصْرِفًا
Te saay-saay sa jenook Safara daldi foog ne dañu cay tàbbi te duñu ca am aw rawtukaay bu ñu ca rëccee.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
51Aaya

Tekki — Al-Kahf 51

Simoore Al-Kahf Aaya 51 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Seedeloowunu leen it sos ga Nu sos seeni bakkan. Te…

Simoore Aaya 51/110 — Simoore Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Kahf Dégg, Simoore Al-Kahf Tekki, Simoore Al-Kahf mp3, Simoore Al-Kahf pdf. Aaya 49–53. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers