Al-Baqara · 133/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
أَمْ كُنتُمْ شُهَدَاءَ إِذْ حَضَرَ يَعْقُوبَ الْمَوْتُ إِذْ قَالَ لِبَنِيهِ مَا تَعْبُدُونَ مِن بَعْدِي قَالُوا نَعْبُدُ إِلَٰهَكَ وَإِلَٰهَ آبَائِكَ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ إِلَٰهًا وَاحِدًا وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ ۝١٣٣
Am kuntum shuhadaaa`a iz hadara Ya`qoobal mawtu iz qaala libaneehi maa ta`budoona mim ba`dee qaaloo na`budu ilaahaka wa ilaaha aabaaa`ika Ibraaheema wa Ismaa`eela wa Ishaaqa Ilaahanw waahidanw wa nahnu lahoo muslimoon
📖 Tekkim Wolof
walla sax fekkee woon ngeen ba dee ga dikkalee (Janqooba) te mu ne: “Éy samay doom, ana lan ngeen di xala jaamu sama ginnaaw” ? - Ñu ne : “Dananu jaamu Yàlla sa Boroom tey Yàllaay say baay Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa, di jenn Yàlla doŋŋ te nun way-wommatu lanu, jëm ci Moom”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 131-135 — Al-Baqara

131إِذْ قَالَ لَهُ رَبُّهُ أَسْلِمْ ۖ قَالَ أَسْلَمْتُ لِرَبِّ الْعَالَمِينَ
[Fàttalikuleen] Ba ko Boroomam nee : “Wommatul”, Mu ne : “Wommatunaa jëm ci Boroom àddina bi”.
132وَوَصَّىٰ بِهَا إِبْرَاهِيمُ بَنِيهِ وَيَعْقُوبُ يَا بَنِيَّ إِنَّ اللَّهَ اصْطَفَىٰ لَكُمُ الدِّينَ فَلَا تَمُوتُنَّ إِلَّا وَأَنتُم مُّسْلِمُونَ
Ibraahiima dénk na ay doomam solo sa, ak Yanqooba, ne leen: “Yéen samay doom, Yàllaa leen tànnal diine de, buleen dee lu dul na fekk ngeen wommatu jëm ca Yàlla” !.
133أَمْ كُنتُمْ شُهَدَاءَ إِذْ حَضَرَ يَعْقُوبَ الْمَوْتُ إِذْ قَالَ لِبَنِيهِ مَا تَعْبُدُونَ مِن بَعْدِي قَالُوا نَعْبُدُ إِلَٰهَكَ وَإِلَٰهَ آبَائِكَ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ إِلَٰهًا وَاحِدًا وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ
walla sax fekkee woon ngeen ba dee ga dikkalee (Janqooba) te mu ne: “Éy samay doom, ana lan ngeen di xala jaamu sama ginnaaw” ? - Ñu ne : “Dananu jaamu Yàlla sa Boroom tey Yàllaay say baay Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa, di jenn Yàlla doŋŋ te nun way-wommatu lanu, jëm ci Moom”.
134تِلْكَ أُمَّةٌ قَدْ خَلَتْ ۖ لَهَا مَا كَسَبَتْ وَلَكُم مَّا كَسَبْتُمْ ۖ وَلَا تُسْأَلُونَ عَمَّا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Woowa xeet jàll na, añe jëfam, yéen itam ngeen añe seeni jëf. Te bu Bis baa, du yéen a leen di layal ñoom ca la ñu defoon.
135وَقَالُوا كُونُوا هُودًا أَوْ نَصَارَىٰ تَهْتَدُوا ۗ قُلْ بَلْ مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۖ وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Ñuy wax naan : “Doonleen Yahuud walla Nasaraan, kon dey ngeen gindiku”. - Neel : “Dée wallaay, diinay Ibraahiima ma wéetaloon Yàlla te bokkut ca way-bokkaale ya”.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
133Aaya

Tekki — Al-Baqara 133

Simoore Al-Baqara Aaya 133 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : walla sax fekkee woon ngeen ba dee ga dikkalee (Janqooba)…

Simoore Aaya 133/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 131–135. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers