Taha · 126/135
Tekki Waxtaan — Taha
قَالَ كَذَٰلِكَ أَتَتْكَ آيَاتُنَا فَنَسِيتَهَا ۖ وَكَذَٰلِكَ الْيَوْمَ تُنسَىٰ ۝١٢٦
Qaala kazaalika atatka Aayaatunaa fanaseetahaa wa kazaalikal Yawma tunsaa
📖 Tekkim Wolof
[Yàlla tontu] ne ko : “Noonu la la Sunuy kàddu dikkalee woon, nga sàggane ko, kon book tey yaw itam kenn du la faale”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 124-128 — Taha

124وَمَنْ أَعْرَضَ عَن ذِكْرِي فَإِنَّ لَهُ مَعِيشَةً ضَنكًا وَنَحْشُرُهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ أَعْمَىٰ
Képp ku ko dummóoyu, dana dundu dund gu metti, te buy dekki Bis-pénc ba gumba lay doon ñu gotti ko”.
125قَالَ رَبِّ لِمَ حَشَرْتَنِي أَعْمَىٰ وَقَدْ كُنتُ بَصِيرًا
[Su ko defee] muy laaj naan : "Sama Boroom, lan moo tax nga pang ma may gumba te ca àddina ma doon gis ? ”
126قَالَ كَذَٰلِكَ أَتَتْكَ آيَاتُنَا فَنَسِيتَهَا ۖ وَكَذَٰلِكَ الْيَوْمَ تُنسَىٰ
[Yàlla tontu] ne ko : “Noonu la la Sunuy kàddu dikkalee woon, nga sàggane ko, kon book tey yaw itam kenn du la faale”.
127وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي مَنْ أَسْرَفَ وَلَمْ يُؤْمِن بِآيَاتِ رَبِّهِ ۚ وَلَعَذَابُ الْآخِرَةِ أَشَدُّ وَأَبْقَىٰ
Noonu la Nuy feye ña ëppal [xaabaabal] te gëmuñu seen kàdduy Boroom [ay màndargaam]. Te mbugalum àllaaxira moo gën a tar te gën a yàgg.
128أَفَلَمْ يَهْدِ لَهُمْ كَمْ أَهْلَكْنَا قَبْلَهُم مِّنَ الْقُرُونِ يَمْشُونَ فِي مَسَاكِنِهِمْ ۗ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّأُولِي النُّهَىٰ
Ndax dafa leerul ci seen bopp te aka bari ay xeet yu Nu alag ca ña leen jiitu woon te tey ñuy dox ci kaw fa ñu dëkkoon ? Loolu war naa mën a waar ñu am xel [te di ko jariñoo] !
TahaFihi Alxuraan
135Aaya
MeccanRevelation
126Aaya

Tekki — Taha 126

Simoore Taha Aaya 126 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Yàlla tontu] ne ko : “Noonu la la Sunuy kàddu…

Simoore Aaya 126/135 — Taha طه (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Taha Dégg, Taha Tekki, Taha mp3, Taha pdf. Aaya 124–128. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers