Aali Imran · 178/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَلَا يَحْسَبَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا أَنَّمَا نُمْلِي لَهُمْ خَيْرٌ لِّأَنفُسِهِمْ ۚ إِنَّمَا نُمْلِي لَهُمْ لِيَزْدَادُوا إِثْمًا ۚ وَلَهُمْ عَذَابٌ مُّهِينٌ ۝١٧٨
Wa laa yahsabannal lazeena kafarooo annamaa numlee lahum khairulli anfusihim; innamaa numlee lahum liyazdaadooo ismaa wa lahum `azaabum muheen
📖 Tekkim Wolof
Ña weddi, buñu foog ne la ñu leen yéex a mbugal lu baax la ci ñoom. Danu leen di yeexe ngir ñu dolliku bàkkaar doŋŋ te danañu am mbugalum toroxtaange.

🎧 Dégg


📜 Aaya 176-180 — Simoore Aali Imran

176وَلَا يَحْزُنكَ الَّذِينَ يُسَارِعُونَ فِي الْكُفْرِ ۚ إِنَّهُمْ لَن يَضُرُّوا اللَّهَ شَيْئًا ۗ يُرِيدُ اللَّهُ أَلَّا يَجْعَلَ لَهُمْ حَظًّا فِي الْآخِرَةِ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ñay njëkkante di tàbbi cig weddi, bumu la naqari. Duñu wàññi Yàlla dara. Yàlla dafa bañ rekk ñu am cër ca àllaaxira. Te am fa mbugal mu rëy.
177إِنَّ الَّذِينَ اشْتَرَوُا الْكُفْرَ بِالْإِيمَانِ لَن يَضُرُّوا اللَّهَ شَيْئًا وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ñiy weccee ngëm ak kéefar, duñu wàññi Yàlla dara. Te am nañu mbugal mu metti.
178وَلَا يَحْسَبَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا أَنَّمَا نُمْلِي لَهُمْ خَيْرٌ لِّأَنفُسِهِمْ ۚ إِنَّمَا نُمْلِي لَهُمْ لِيَزْدَادُوا إِثْمًا ۚ وَلَهُمْ عَذَابٌ مُّهِينٌ
Ña weddi, buñu foog ne la ñu leen yéex a mbugal lu baax la ci ñoom. Danu leen di yeexe ngir ñu dolliku bàkkaar doŋŋ te danañu am mbugalum toroxtaange.
179مَّا كَانَ اللَّهُ لِيَذَرَ الْمُؤْمِنِينَ عَلَىٰ مَا أَنتُمْ عَلَيْهِ حَتَّىٰ يَمِيزَ الْخَبِيثَ مِنَ الطَّيِّبِ ۗ وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُطْلِعَكُمْ عَلَى الْغَيْبِ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ يَجْتَبِي مِن رُّسُلِهِ مَن يَشَاءُ ۖ فَآمِنُوا بِاللَّهِ وَرُسُلِهِ ۚ وَإِن تُؤْمِنُوا وَتَتَّقُوا فَلَكُمْ أَجْرٌ عَظِيمٌ
Yàlla du bàyyi ñi gëm ci li ngeen nekk ba kerook ba Muy téqale ku bon ka ak ku baax ka. Te it Yàlla duleen xamal kumpa. Waaye Yàlla dana tànn ku ko soob ciy Yonentam [xamal ko kumpa]. Gëmleen Yàlla ak i Yonentam. Su ngeen gëmee te ragal Yàlla, dangeen am pey gu màgg.
180وَلَا يَحْسَبَنَّ الَّذِينَ يَبْخَلُونَ بِمَا آتَاهُمُ اللَّهُ مِن فَضْلِهِ هُوَ خَيْرًا لَّهُم ۖ بَلْ هُوَ شَرٌّ لَّهُمْ ۖ سَيُطَوَّقُونَ مَا بَخِلُوا بِهِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ وَلِلَّهِ مِيرَاثُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Ña nay a [joxe] ca la leen Yàlla may ciy ngënéelam, buñu foog ne lu baax la ci ñoom. Déet ! lu bon la ci ñoom : [la ñu nayoon ci joxe ko] danañu leen ko wékkal ci seeni loos Bis- pénc ba. Yàllaa moom donoy asamaan yeek suuf si. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
178Aaya

Tekki — Aali Imran 178

Simoore Aali Imran Aaya 178 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña weddi, buñu foog ne la ñu leen yéex a…

Simoore Aaya 178/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 176–180. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers