Aali Imran · 190/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
إِنَّ فِي خَلْقِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَاخْتِلَافِ اللَّيْلِ وَالنَّهَارِ لَآيَاتٍ لِّأُولِي الْأَلْبَابِ ۝١٩٠
Inna fee khalqis samaawati wal ardi wakhtilaafil laili wannahaari la Aayaatil liulil albaab
📖 Tekkim Wolof
Sàkk gi Yàlla sàkk asamaan yeek suuf si, ak ni guddi gi ak bëccëg gi di jëlasantee, ay kéemaan yu rëy a ngi ci ñeel woroom xel ya,

🎧 Dégg


📜 Aaya 188-192 — Simoore Aali Imran

188لَا تَحْسَبَنَّ الَّذِينَ يَفْرَحُونَ بِمَا أَتَوا وَّيُحِبُّونَ أَن يُحْمَدُوا بِمَا لَمْ يَفْعَلُوا فَلَا تَحْسَبَنَّهُم بِمَفَازَةٍ مِّنَ الْعَذَابِ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Bul foog ne ñay bég ca la ñu def, te bëgg ku leen tëgg ci lu ñu deful, buleen foog mukk ne danañu mucc ci mbugal. Déedéet, mbugal mu metti lañuy am !
189وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Yàllaa moom asamaan yeek suuf si. Te Yàlla mën na lu ne.
190إِنَّ فِي خَلْقِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَاخْتِلَافِ اللَّيْلِ وَالنَّهَارِ لَآيَاتٍ لِّأُولِي الْأَلْبَابِ
Sàkk gi Yàlla sàkk asamaan yeek suuf si, ak ni guddi gi ak bëccëg gi di jëlasantee, ay kéemaan yu rëy a ngi ci ñeel woroom xel ya,
191الَّذِينَ يَذْكُرُونَ اللَّهَ قِيَامًا وَقُعُودًا وَعَلَىٰ جُنُوبِهِمْ وَيَتَفَكَّرُونَ فِي خَلْقِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ رَبَّنَا مَا خَلَقْتَ هَٰذَا بَاطِلًا سُبْحَانَكَ فَقِنَا عَذَابَ النَّارِ
[Woroom xel yooyu gëm], ñooy ñay tuddu Yàlla, bu ñu toogee ak bu ñu taxawee, ak bu ñu tëddee, tey xalaat ci sàkkug asamaan yeek suuf si, [di wax naan] : “Yaw sunu Boroom ! Sàkkuloo lii ci neen. Tuddu naa sag sell ! Yal na nga nu fegal mbugalum Safara.
192رَبَّنَا إِنَّكَ مَن تُدْخِلِ النَّارَ فَقَدْ أَخْزَيْتَهُ ۖ وَمَا لِلظَّالِمِينَ مِنْ أَنصَارٍ
Yaw sunu Boroom ! Koo tàbbal Safara, gàcceel nga ko de. Te tooñkat ya, duñu am ndimbal !
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
190Aaya

Tekki — Aali Imran 190

Simoore Aali Imran Aaya 190 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Sàkk gi Yàlla sàkk asamaan yeek suuf si, ak ni…

Simoore Aaya 190/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 188–192. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers