Aali Imran · 189/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝١٨٩
Wa lillaahi mulkus samaawaati wal ard; wallaahu `alaa kulli shai`in Qadeer
📖 Tekkim Wolof
Yàllaa moom asamaan yeek suuf si. Te Yàlla mën na lu ne.

🎧 Dégg


📜 Aaya 187-191 — Aali Imran

187وَإِذْ أَخَذَ اللَّهُ مِيثَاقَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ لَتُبَيِّنُنَّهُ لِلنَّاسِ وَلَا تَكْتُمُونَهُ فَنَبَذُوهُ وَرَاءَ ظُهُورِهِمْ وَاشْتَرَوْا بِهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۖ فَبِئْسَ مَا يَشْتَرُونَ
[Fàttalikul] ba Yàlla kóllaranteek ña jot Téere, ne : “Nangeen ko leeralal nit ñi te buleen ko nëbb”. Ñu sànni ko ca seen ginnaaw, jaaye ko njëg gu néew. Ndax njëg gu bon !
188لَا تَحْسَبَنَّ الَّذِينَ يَفْرَحُونَ بِمَا أَتَوا وَّيُحِبُّونَ أَن يُحْمَدُوا بِمَا لَمْ يَفْعَلُوا فَلَا تَحْسَبَنَّهُم بِمَفَازَةٍ مِّنَ الْعَذَابِ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Bul foog ne ñay bég ca la ñu def, te bëgg ku leen tëgg ci lu ñu deful, buleen foog mukk ne danañu mucc ci mbugal. Déedéet, mbugal mu metti lañuy am !
189وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Yàllaa moom asamaan yeek suuf si. Te Yàlla mën na lu ne.
190إِنَّ فِي خَلْقِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَاخْتِلَافِ اللَّيْلِ وَالنَّهَارِ لَآيَاتٍ لِّأُولِي الْأَلْبَابِ
Sàkk gi Yàlla sàkk asamaan yeek suuf si, ak ni guddi gi ak bëccëg gi di jëlasantee, ay kéemaan yu rëy a ngi ci ñeel woroom xel ya,
191الَّذِينَ يَذْكُرُونَ اللَّهَ قِيَامًا وَقُعُودًا وَعَلَىٰ جُنُوبِهِمْ وَيَتَفَكَّرُونَ فِي خَلْقِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ رَبَّنَا مَا خَلَقْتَ هَٰذَا بَاطِلًا سُبْحَانَكَ فَقِنَا عَذَابَ النَّارِ
[Woroom xel yooyu gëm], ñooy ñay tuddu Yàlla, bu ñu toogee ak bu ñu taxawee, ak bu ñu tëddee, tey xalaat ci sàkkug asamaan yeek suuf si, [di wax naan] : “Yaw sunu Boroom ! Sàkkuloo lii ci neen. Tuddu naa sag sell ! Yal na nga nu fegal mbugalum Safara.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
189Aaya

Tekki — Aali Imran 189

Simoore Aali Imran Aaya 189 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàllaa moom asamaan yeek suuf si. Te Yàlla mën na…

Simoore Aaya 189/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 187–191. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers