Aali Imran · 36/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
فَلَمَّا وَضَعَتْهَا قَالَتْ رَبِّ إِنِّي وَضَعْتُهَا أُنثَىٰ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِمَا وَضَعَتْ وَلَيْسَ الذَّكَرُ كَالْأُنثَىٰ ۖ وَإِنِّي سَمَّيْتُهَا مَرْيَمَ وَإِنِّي أُعِيذُهَا بِكَ وَذُرِّيَّتَهَا مِنَ الشَّيْطَانِ الرَّجِيمِ ۝٣٦
Falammaa waqa`athaa qaalat Rabbi innee wada`tuhaaa unsaa wallaahu a`lamu bimaa wada`at wa laisaz zakaru kalunsaa wa innee sammaituhaa Maryama wa innee u`eezuhaa bika wa zurriyyatahaa minash Shaitaanir Rajeem
📖 Tekkim Wolof
Ba mu ko wasinee, mu ne : “Ay sama Boroom, jigéen laa wasin de” ; te Yàllaa gën a xam la mu wasin ! Ndax góor melul ni jigéen. “Te tudde naa ko Maryaama, te maa ngi koy muslul wéeru ci Yaw mook i doomam mucc ci Séytaane suñu rëbb sa”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 34-38 — Aali Imran

34ذُرِّيَّةً بَعْضُهَا مِن بَعْضٍ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Ñenn ña di doom ca ña ca des, Yàlla Kuy dégg la te Ku xam la.
35إِذْ قَالَتِ امْرَأَتُ عِمْرَانَ رَبِّ إِنِّي نَذَرْتُ لَكَ مَا فِي بَطْنِي مُحَرَّرًا فَتَقَبَّلْ مِنِّي ۖ إِنَّكَ أَنتَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Fàttalikul ba soxnas Himraan waxee ne : “Yaw sama Boroom, fas naa yéene sédde la li ne ci sama biir. May ku mu sellal, nangul ma. Yaw yaay Kiy dégg, Ki xam”.
36فَلَمَّا وَضَعَتْهَا قَالَتْ رَبِّ إِنِّي وَضَعْتُهَا أُنثَىٰ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِمَا وَضَعَتْ وَلَيْسَ الذَّكَرُ كَالْأُنثَىٰ ۖ وَإِنِّي سَمَّيْتُهَا مَرْيَمَ وَإِنِّي أُعِيذُهَا بِكَ وَذُرِّيَّتَهَا مِنَ الشَّيْطَانِ الرَّجِيمِ
Ba mu ko wasinee, mu ne : “Ay sama Boroom, jigéen laa wasin de” ; te Yàllaa gën a xam la mu wasin ! Ndax góor melul ni jigéen. “Te tudde naa ko Maryaama, te maa ngi koy muslul wéeru ci Yaw mook i doomam mucc ci Séytaane suñu rëbb sa”.
37فَتَقَبَّلَهَا رَبُّهَا بِقَبُولٍ حَسَنٍ وَأَنبَتَهَا نَبَاتًا حَسَنًا وَكَفَّلَهَا زَكَرِيَّا ۖ كُلَّمَا دَخَلَ عَلَيْهَا زَكَرِيَّا الْمِحْرَابَ وَجَدَ عِندَهَا رِزْقًا ۖ قَالَ يَا مَرْيَمُ أَنَّىٰ لَكِ هَٰذَا ۖ قَالَتْ هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ ۖ إِنَّ اللَّهَ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ بِغَيْرِ حِسَابٍ
Boroomam nangul ko, nangu gu rafet, màggloo ko màgg gu rafet. [Zakariyaa] yar ko. Saa su [Zakariyaa] duggee ca Mihraab ba, dana fekk fa moom ay xéewal. Mu ne : “Yaw Maryaama, fu la lii bawoo ? ” - Mu tontu ko ne : “Lu jóge ca Yàlla la”. Yàllaay wërsëgal ku ko soob ci lu àndul di waññi na mu tollu.
38هُنَالِكَ دَعَا زَكَرِيَّا رَبَّهُ ۖ قَالَ رَبِّ هَبْ لِي مِن لَّدُنكَ ذُرِّيَّةً طَيِّبَةً ۖ إِنَّكَ سَمِيعُ الدُّعَاءِ
Foofii la Zakariyaa ñaanee Boroomam, ne : “Yaw sama Boroom, may ma ci sa coobare, ay njërëta yu yiw. Yaw Boroom bi Kuy dégg ñaan nga”.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
36Aaya

Tekki — Aali Imran 36

Simoore Aali Imran Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba mu ko wasinee, mu ne : “Ay sama Boroom,…

Simoore Aaya 36/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers