Aali Imran · 43/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
يَا مَرْيَمُ اقْنُتِي لِرَبِّكِ وَاسْجُدِي وَارْكَعِي مَعَ الرَّاكِعِينَ ۝٤٣
Yaa Maryamuq nutee li Rabbiki wasjudee warka`ee ma`ar raaki`een
📖 Tekkim Wolof
“Yaw Maryaama, jaamul sa Boroom, nanga sujjóot te rukkoo ànd ak ñay rukkoo [di julli]”

🎧 Dégg


📜 Aaya 41-45 — Simoore Aali Imran

41قَالَ رَبِّ اجْعَل لِّي آيَةً ۖ قَالَ آيَتُكَ أَلَّا تُكَلِّمَ النَّاسَ ثَلَاثَةَ أَيَّامٍ إِلَّا رَمْزًا ۗ وَاذْكُر رَّبَّكَ كَثِيرًا وَسَبِّحْ بِالْعَشِيِّ وَالْإِبْكَارِ
- Mu ne : “Yàlla, defal ma màndarga.” - Mu ne ko : “ Doo mën a wax ak nit ñi ñetti fan lu dul ci njunju. Na nga tudd sa Boroom lu bari ; te nanga di ko sàbbaal suba ak ngoon.”
42وَإِذْ قَالَتِ الْمَلَائِكَةُ يَا مَرْيَمُ إِنَّ اللَّهَ اصْطَفَاكِ وَطَهَّرَكِ وَاصْطَفَاكِ عَلَىٰ نِسَاءِ الْعَالَمِينَ
(Fàttalikul) ba Malaaka ya waxee ne : “Yaw Maryaama, Yàlla tànn na la te laabal na la, tànn na la ci kaw jigéeni àddina bi yépp.
43يَا مَرْيَمُ اقْنُتِي لِرَبِّكِ وَاسْجُدِي وَارْكَعِي مَعَ الرَّاكِعِينَ
“Yaw Maryaama, jaamul sa Boroom, nanga sujjóot te rukkoo ànd ak ñay rukkoo [di julli]”
44ذَٰلِكَ مِنْ أَنبَاءِ الْغَيْبِ نُوحِيهِ إِلَيْكَ ۚ وَمَا كُنتَ لَدَيْهِمْ إِذْ يُلْقُونَ أَقْلَامَهُمْ أَيُّهُمْ يَكْفُلُ مَرْيَمَ وَمَا كُنتَ لَدَيْهِمْ إِذْ يَخْتَصِمُونَ
- Loolu bokk na ca xibaar ya nekkoon kumpa, Nu ngi la koy xamal. Te neewuloo woon ba ñuy sànni bantu wantaloo ya di seet kan mooy yor Maryaama ! Te neewuloo woon ba ñuy xulloo.
45إِذْ قَالَتِ الْمَلَائِكَةُ يَا مَرْيَمُ إِنَّ اللَّهَ يُبَشِّرُكِ بِكَلِمَةٍ مِّنْهُ اسْمُهُ الْمَسِيحُ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ وَجِيهًا فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَمِنَ الْمُقَرَّبِينَ
(Fàttalikul,) ba Malaaka ya waxee ne : "Yaw Maryaama, Yàllaa ngi lay bégal ci kàddu [doom] gu tukkee ca Moom : turam moo di “Al-Masiihu” “Iisaa”, doomu Maryam, boroom bayre ci àddina ak ca àllaaxira, te bokk na ca way-jege ña Boroom bi”.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
43Aaya

Tekki — Aali Imran 43

Simoore Aali Imran Aaya 43 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Yaw Maryaama, jaamul sa Boroom, nanga sujjóot te rukkoo ànd…

Simoore Aaya 43/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 41–45. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers