Luqman · 14/34
Tekki Waxtaan — Luqman
وَوَصَّيْنَا الْإِنسَانَ بِوَالِدَيْهِ حَمَلَتْهُ أُمُّهُ وَهْنًا عَلَىٰ وَهْنٍ وَفِصَالُهُ فِي عَامَيْنِ أَنِ اشْكُرْ لِي وَلِوَالِدَيْكَ إِلَيَّ الْمَصِيرُ ۝١٤
Wa wassainal bi waalidaihi hamalat hu ummuhoo wahnan `alaa wahninw wa fisaaluhoo fee `aamaini anishkur lee wa liwaalidaika ilaiyal maseer
📖 Tekkim Wolof
Dénk Nanu nit muy rafetal jëme ci ñaari waajuram ; ndax yaayam ëmb na ko muy coono ci biir coono : ba feral ko diirub ñaari at. “Nanga may sant Man [Yàlla] ak sa ñaari waajur. Ci Man la lépp di mujj.
🎧 Dégg

📜 Aaya 12-16 — Luqman

12وَلَقَدْ آتَيْنَا لُقْمَانَ الْحِكْمَةَ أَنِ اشْكُرْ لِلَّهِ ۚ وَمَن يَشْكُرْ فَإِنَّمَا يَشْكُرُ لِنَفْسِهِ ۖ وَمَن كَفَرَ فَإِنَّ اللَّهَ غَنِيٌّ حَمِيدٌ
Joxoon Nanu Luqmaan xam-xamu xereñ, ne ko : “Santal Yàlla, [gërëm Ko], ku Ko sant ci di Ko dello jukkal, boppam ; ku Ko xarab it..., [Na xam ni] Yàlla ku doylu la, Yayoowaakoonug cant la”.
13وَإِذْ قَالَ لُقْمَانُ لِابْنِهِ وَهُوَ يَعِظُهُ يَا بُنَيَّ لَا تُشْرِكْ بِاللَّهِ ۖ إِنَّ الشِّرْكَ لَظُلْمٌ عَظِيمٌ
[Fàttalikul] ba Luqmaan waxee doomam ja, di ko waar, naan ko : “Yaw samas doom, bul bokkaale mukk dara ak Yàlla, ndax bokkaale kat ag tooñ gu réy la”.
14وَوَصَّيْنَا الْإِنسَانَ بِوَالِدَيْهِ حَمَلَتْهُ أُمُّهُ وَهْنًا عَلَىٰ وَهْنٍ وَفِصَالُهُ فِي عَامَيْنِ أَنِ اشْكُرْ لِي وَلِوَالِدَيْكَ إِلَيَّ الْمَصِيرُ
Dénk Nanu nit muy rafetal jëme ci ñaari waajuram ; ndax yaayam ëmb na ko muy coono ci biir coono : ba feral ko diirub ñaari at. “Nanga may sant Man [Yàlla] ak sa ñaari waajur. Ci Man la lépp di mujj.
15وَإِن جَاهَدَاكَ عَلَىٰ أَن تُشْرِكَ بِي مَا لَيْسَ لَكَ بِهِ عِلْمٌ فَلَا تُطِعْهُمَا ۖ وَصَاحِبْهُمَا فِي الدُّنْيَا مَعْرُوفًا ۖ وَاتَّبِعْ سَبِيلَ مَنْ أَنَابَ إِلَيَّ ۚ ثُمَّ إِلَيَّ مَرْجِعُكُمْ فَأُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Saa su ñu la sonnalee ci bëgg nga bokkaale Maak loo amul xam-xam, bulen ca topp ; waaye nangay ànd ak ñoom ci àddina si ak njekk. Te nanga topp yoon wa jëmsi ci Man. Fi Man ngeen di mujje [yéen ñépp], su ko defee, Ma téqantalal leen la ngeen daan def”.
16يَا بُنَيَّ إِنَّهَا إِن تَكُ مِثْقَالَ حَبَّةٍ مِّنْ خَرْدَلٍ فَتَكُن فِي صَخْرَةٍ أَوْ فِي السَّمَاوَاتِ أَوْ فِي الْأَرْضِ يَأْتِ بِهَا اللَّهُ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَطِيفٌ خَبِيرٌ
“Yaw sama doom, dIisaay woowu, doonte la sax dafa tollu ni as fepp, nekk ci kaw doj mbaa ci biir asamaan yi, walla ci biir suuf, du tee Yàlla indi ko . Yàlla Ku deñ-kumpa la .
LuqmanFihi Alxuraan
34Aaya
MeccanRevelation
14Aaya

Tekki — Luqman 14

Simoore Luqman Aaya 14 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dénk Nanu nit muy rafetal jëme ci ñaari waajuram ;…

Simoore Aaya 14/34 — Luqman لقمان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Luqman Dégg, Luqman Tekki, Luqman mp3, Luqman pdf. Aaya 12–16. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers