Saba · 15/54
Tekki Waxtaan — Saba
لَقَدْ كَانَ لِسَبَإٍ فِي مَسْكَنِهِمْ آيَةٌ ۖ جَنَّتَانِ عَن يَمِينٍ وَشِمَالٍ ۖ كُلُوا مِن رِّزْقِ رَبِّكُمْ وَاشْكُرُوا لَهُ ۚ بَلْدَةٌ طَيِّبَةٌ وَرَبٌّ غَفُورٌ ۝١٥
Laqad kaana li Saba-in fee maskanihim Aayatun jannataani `ai yameeninw wa shimaalin kuloo mir rizq Rabbikum washkuroolah; baldatun taiyibatunw wa Rabbun Ghafoor
📖 Tekkim Wolof
Waa réewum Saba amoon nañu màndargam ñaari dër ci ndeyjoor ak càmmooñ. “Lekkleen ci xéewali Yàlla, mayi seen Boroom, te ngeen sant Ko ndax : may na leen dëkk bu teey, neex, te di Boroom biy Jéggalaakoon”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 13-17 — Saba

13يَعْمَلُونَ لَهُ مَا يَشَاءُ مِن مَّحَارِيبَ وَتَمَاثِيلَ وَجِفَانٍ كَالْجَوَابِ وَقُدُورٍ رَّاسِيَاتٍ ۚ اعْمَلُوا آلَ دَاوُودَ شُكْرًا ۚ وَقَلِيلٌ مِّنْ عِبَادِيَ الشَّكُورُ
Ñu di ko liggéeyal lu ko soob : ci ay tabax ak i bóoli yu tollu ni ay xur, ak i kawdiir yu ñu sësale. “Yéen waa kër Daawuda, gërëmleen Yàlla”, te néewaana mu am ci sama jaam yi ay santkat.
14فَلَمَّا قَضَيْنَا عَلَيْهِ الْمَوْتَ مَا دَلَّهُمْ عَلَىٰ مَوْتِهِ إِلَّا دَابَّةُ الْأَرْضِ تَأْكُلُ مِنسَأَتَهُ ۖ فَلَمَّا خَرَّ تَبَيَّنَتِ الْجِنُّ أَن لَّوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ الْغَيْبَ مَا لَبِثُوا فِي الْعَذَابِ الْمُهِينِ
Ba Nu dogalee mu war a dee, la leen ko xamal moo di max ga lekk yetam wa. Ba mu daanoo, jinne yi daldi xam ne bu ñu xamoon kumpa, duñu sax ca mbugal moomee daan leen tax a doyadi.
15لَقَدْ كَانَ لِسَبَإٍ فِي مَسْكَنِهِمْ آيَةٌ ۖ جَنَّتَانِ عَن يَمِينٍ وَشِمَالٍ ۖ كُلُوا مِن رِّزْقِ رَبِّكُمْ وَاشْكُرُوا لَهُ ۚ بَلْدَةٌ طَيِّبَةٌ وَرَبٌّ غَفُورٌ
Waa réewum Saba amoon nañu màndargam ñaari dër ci ndeyjoor ak càmmooñ. “Lekkleen ci xéewali Yàlla, mayi seen Boroom, te ngeen sant Ko ndax : may na leen dëkk bu teey, neex, te di Boroom biy Jéggalaakoon”.
16فَأَعْرَضُوا فَأَرْسَلْنَا عَلَيْهِمْ سَيْلَ الْعَرِمِ وَبَدَّلْنَاهُم بِجَنَّتَيْهِمْ جَنَّتَيْنِ ذَوَاتَيْ أُكُلٍ خَمْطٍ وَأَثْلٍ وَشَيْءٍ مِّن سِدْرٍ قَلِيلٍ
Waaye dummóoyu woon nañu . Nu daldi leen yebalal mbënnum téqum ndox ma, Nu daldi leen soppil seen tooli dër y, def leen ay tool yu am meññent mu sëcc ak i gargamboose ak i siddéem juy néewal.
17ذَٰلِكَ جَزَيْنَاهُم بِمَا كَفَرُوا ۖ وَهَلْ نُجَازِي إِلَّا الْكَفُورَ
Loolu la Nu leen feye woon ngir seenug weddi. Moo ndax Dananu ko feye keneen ku dul ñuy weddi ?
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
15Aaya

Tekki — Saba 15

Simoore Saba Aaya 15 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waa réewum Saba amoon nañu màndargam ñaari dër ci ndeyjoor…

Simoore Aaya 15/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 13–17. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers