An-Nisa · 16/176
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nisa
وَاللَّذَانِ يَأْتِيَانِهَا مِنكُمْ فَآذُوهُمَا ۖ فَإِن تَابَا وَأَصْلَحَا فَأَعْرِضُوا عَنْهُمَا ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ تَوَّابًا رَّحِيمًا ۝١٦
Wallazaani yaatiyaanihaa minkum fa aazoohumaa fa in taabaa wa aslahaa fa a`ridoo `anhumaaa; innal laaha kaana Tawwaabar Raheema
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne loolu dal na leen ci yéen [góor ña], nangeen leen tas. Bu ñu tuubee, wëlbëtiku di def lu baax, nangeen leen bàyyi. Naka Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 14-18 — Simoore An-Nisa

14وَمَن يَعْصِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَيَتَعَدَّ حُدُودَهُ يُدْخِلْهُ نَارًا خَالِدًا فِيهَا وَلَهُ عَذَابٌ مُّهِينٌ
Ku moy Yàlla ak ub Yonentam, di jéggi daytali Yàlla yi, Danañu ko dugal Safara, mu béel fa, bokk ca mbugal muy toroxale.
15وَاللَّاتِي يَأْتِينَ الْفَاحِشَةَ مِن نِّسَائِكُمْ فَاسْتَشْهِدُوا عَلَيْهِنَّ أَرْبَعَةً مِّنكُمْ ۖ فَإِن شَهِدُوا فَأَمْسِكُوهُنَّ فِي الْبُيُوتِ حَتَّىٰ يَتَوَفَّاهُنَّ الْمَوْتُ أَوْ يَجْعَلَ اللَّهُ لَهُنَّ سَبِيلًا
Ña def ñaawtéef [njaaloo] ci seeni jigéen, nangeen ko seedeloo ñeenti nit ci yéen. Bu ñu ko seedee, nangeen leen tëj ba dee fekk leen fa walla ba Yàlla ubbil leen aw yoon [wu ñu mën a aw ba mucc].
16وَاللَّذَانِ يَأْتِيَانِهَا مِنكُمْ فَآذُوهُمَا ۖ فَإِن تَابَا وَأَصْلَحَا فَأَعْرِضُوا عَنْهُمَا ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ تَوَّابًا رَّحِيمًا
Ña nga xam ne loolu dal na leen ci yéen [góor ña], nangeen leen tas. Bu ñu tuubee, wëlbëtiku di def lu baax, nangeen leen bàyyi. Naka Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
17إِنَّمَا التَّوْبَةُ عَلَى اللَّهِ لِلَّذِينَ يَعْمَلُونَ السُّوءَ بِجَهَالَةٍ ثُمَّ يَتُوبُونَ مِن قَرِيبٍ فَأُولَٰئِكَ يَتُوبُ اللَّهُ عَلَيْهِمْ ۗ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا
Yàlla rekk ay nangu tuub, ña def ñaawtéef ci ñàkk a xam, te gaaw daldi tuub. Ñooña Yàlla dana nangu seen tuub. Yàlla Aji-xam la, Aji-xereñ la.
18وَلَيْسَتِ التَّوْبَةُ لِلَّذِينَ يَعْمَلُونَ السَّيِّئَاتِ حَتَّىٰ إِذَا حَضَرَ أَحَدَهُمُ الْمَوْتُ قَالَ إِنِّي تُبْتُ الْآنَ وَلَا الَّذِينَ يَمُوتُونَ وَهُمْ كُفَّارٌ ۚ أُولَٰئِكَ أَعْتَدْنَا لَهُمْ عَذَابًا أَلِيمًا
Ña dul am njéggal ñooy ña def ñaawtéef [te baluwuñu seen Boroom] ba dee dikkal kenn ca ñoom muy door a wax ne : “Léegi tuub naa” - ak ña nga xam ne dañuy dee ci kéefar. Ñooña, danañu leen xaaroo mbugal mu tar [metti].
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
16Aaya

Tekki — An-Nisa 16

Simoore An-Nisa Aaya 16 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne loolu dal na leen ci yéen…

Simoore Aaya 16/176 — Simoore An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nisa Dégg, Simoore An-Nisa Tekki, Simoore An-Nisa mp3, Simoore An-Nisa pdf. Aaya 14–18. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers