An-Nisa · 26/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
يُرِيدُ اللَّهُ لِيُبَيِّنَ لَكُمْ وَيَهْدِيَكُمْ سُنَنَ الَّذِينَ مِن قَبْلِكُمْ وَيَتُوبَ عَلَيْكُمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ ۝٢٦
Yureedul laahu liyubai yina lakum wa yahdiyakum sunanal lazeena min qablikum wa yatooba `alaikum; wallaahu `Aleemun Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Yàlla dafa namm a leeral [àtteem] ci gindi leen, teg leen ca yoonu ña leen jiitu woon, te jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la [ci àtteem].
🎧 Dégg

📜 Aaya 24-28 — An-Nisa

24۞ وَالْمُحْصَنَاتُ مِنَ النِّسَاءِ إِلَّا مَا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُمْ ۖ كِتَابَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ ۚ وَأُحِلَّ لَكُم مَّا وَرَاءَ ذَٰلِكُمْ أَن تَبْتَغُوا بِأَمْوَالِكُم مُّحْصِنِينَ غَيْرَ مُسَافِحِينَ ۚ فَمَا اسْتَمْتَعْتُم بِهِ مِنْهُنَّ فَآتُوهُنَّ أُجُورَهُنَّ فَرِيضَةً ۚ وَلَا جُنَاحَ عَلَيْكُمْ فِيمَا تَرَاضَيْتُم بِهِ مِن بَعْدِ الْفَرِيضَةِ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلِيمًا حَكِيمًا
[araam na it ci yéen] jigéen ña saŋewu, ba mu des jebéer ya ngeen moom. Ndigalu Yàllaa ngoogu ci yéen ! Ginnaaw ñooña, [ña mu lim ciy jigéen ñu daganul ngeen sëy ak ñoom]. Dagan na ngeen saŋewu cig jigéen te joxe seeni alal, di way-sëy ak ñoom, bañ di way-njaaloo. Te jigéen ña ngeen sàkku bànneexu ci ñoom, nangeen leen jox seeni can. Lii mbir mu Yàlla santaane la [farataal]. Aayul ginnaaw la ñu farataal nag ngeen déggoo [ci li ngeen war a joxe]. Yàlla de Moom Ku xam la, Ku xereñ la.
25وَمَن لَّمْ يَسْتَطِعْ مِنكُمْ طَوْلًا أَن يَنكِحَ الْمُحْصَنَاتِ الْمُؤْمِنَاتِ فَمِن مَّا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُم مِّن فَتَيَاتِكُمُ الْمُؤْمِنَاتِ ۚ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِإِيمَانِكُم ۚ بَعْضُكُم مِّن بَعْضٍ ۚ فَانكِحُوهُنَّ بِإِذْنِ أَهْلِهِنَّ وَآتُوهُنَّ أُجُورَهُنَّ بِالْمَعْرُوفِ مُحْصَنَاتٍ غَيْرَ مُسَافِحَاتٍ وَلَا مُتَّخِذَاتِ أَخْدَانٍ ۚ فَإِذَا أُحْصِنَّ فَإِنْ أَتَيْنَ بِفَاحِشَةٍ فَعَلَيْهِنَّ نِصْفُ مَا عَلَى الْمُحْصَنَاتِ مِنَ الْعَذَابِ ۚ ذَٰلِكَ لِمَنْ خَشِيَ الْعَنَتَ مِنكُمْ ۚ وَأَن تَصْبِرُوا خَيْرٌ لَّكُمْ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ku amul can ci yéen, gu mu mën a takke jabar ju nekk gor te di jullit, na takk kon ci jebéer ya di ay jullit di xale yu jigéen ya bokk ci yéen. Yàllaa gën a xam fa seen gëm toll, ndax yéen a mëññante [jurante]. Nangeen leen takk ci ndigalu seeni kilifa te ngeen jox leen seeni can ci njekk ; ngeen di way-sëy, di bañ di way-njaaloo, te bañ leen a jàppe ay coro cig nëbbu. Bu ñu sëyee te def njaaloo [ñoom jebéer ya], war nañu leen a teg genn-wàllu mbugal ma ñuy teg gor gu jigéen. Loolu ndigal la ci ku ñu ragal mu njaaloo ci yéen ; bu ngeen mënee muñ, moo gën ci yéen. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
26يُرِيدُ اللَّهُ لِيُبَيِّنَ لَكُمْ وَيَهْدِيَكُمْ سُنَنَ الَّذِينَ مِن قَبْلِكُمْ وَيَتُوبَ عَلَيْكُمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Yàlla dafa namm a leeral [àtteem] ci gindi leen, teg leen ca yoonu ña leen jiitu woon, te jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la [ci àtteem].
27وَاللَّهُ يُرِيدُ أَن يَتُوبَ عَلَيْكُمْ وَيُرِيدُ الَّذِينَ يَتَّبِعُونَ الشَّهَوَاتِ أَن تَمِيلُوا مَيْلًا عَظِيمًا
Yàlla dafa leen bëgg a jéggal. Waaye ña topp seen bànneex, ñoom dañuy bëgg ngeen jeng, jeng gu fés.
28يُرِيدُ اللَّهُ أَن يُخَفِّفَ عَنكُمْ ۚ وَخُلِقَ الْإِنسَانُ ضَعِيفًا
Yàlla dafa leen a bëgg a woyofal [àtteem] ndax néew doole ak lott gi nit bindoo.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
26Aaya

Tekki — An-Nisa 26

Simoore An-Nisa Aaya 26 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla dafa namm a leeral [àtteem] ci gindi leen, teg…

Simoore Aaya 26/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 24–28. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers