An-Nisa · 27/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَاللَّهُ يُرِيدُ أَن يَتُوبَ عَلَيْكُمْ وَيُرِيدُ الَّذِينَ يَتَّبِعُونَ الشَّهَوَاتِ أَن تَمِيلُوا مَيْلًا عَظِيمًا ۝٢٧
Wallaahu yureedu ai yatooba `alaikum wa yureedul lazeena yattabi `oonash shahawaati an tameeloo mailan `azeemaa
📖 Tekkim Wolof
Yàlla dafa leen bëgg a jéggal. Waaye ña topp seen bànneex, ñoom dañuy bëgg ngeen jeng, jeng gu fés.
🎧 Dégg

📜 Aaya 25-29 — An-Nisa

25وَمَن لَّمْ يَسْتَطِعْ مِنكُمْ طَوْلًا أَن يَنكِحَ الْمُحْصَنَاتِ الْمُؤْمِنَاتِ فَمِن مَّا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُم مِّن فَتَيَاتِكُمُ الْمُؤْمِنَاتِ ۚ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِإِيمَانِكُم ۚ بَعْضُكُم مِّن بَعْضٍ ۚ فَانكِحُوهُنَّ بِإِذْنِ أَهْلِهِنَّ وَآتُوهُنَّ أُجُورَهُنَّ بِالْمَعْرُوفِ مُحْصَنَاتٍ غَيْرَ مُسَافِحَاتٍ وَلَا مُتَّخِذَاتِ أَخْدَانٍ ۚ فَإِذَا أُحْصِنَّ فَإِنْ أَتَيْنَ بِفَاحِشَةٍ فَعَلَيْهِنَّ نِصْفُ مَا عَلَى الْمُحْصَنَاتِ مِنَ الْعَذَابِ ۚ ذَٰلِكَ لِمَنْ خَشِيَ الْعَنَتَ مِنكُمْ ۚ وَأَن تَصْبِرُوا خَيْرٌ لَّكُمْ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ku amul can ci yéen, gu mu mën a takke jabar ju nekk gor te di jullit, na takk kon ci jebéer ya di ay jullit di xale yu jigéen ya bokk ci yéen. Yàllaa gën a xam fa seen gëm toll, ndax yéen a mëññante [jurante]. Nangeen leen takk ci ndigalu seeni kilifa te ngeen jox leen seeni can ci njekk ; ngeen di way-sëy, di bañ di way-njaaloo, te bañ leen a jàppe ay coro cig nëbbu. Bu ñu sëyee te def njaaloo [ñoom jebéer ya], war nañu leen a teg genn-wàllu mbugal ma ñuy teg gor gu jigéen. Loolu ndigal la ci ku ñu ragal mu njaaloo ci yéen ; bu ngeen mënee muñ, moo gën ci yéen. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
26يُرِيدُ اللَّهُ لِيُبَيِّنَ لَكُمْ وَيَهْدِيَكُمْ سُنَنَ الَّذِينَ مِن قَبْلِكُمْ وَيَتُوبَ عَلَيْكُمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Yàlla dafa namm a leeral [àtteem] ci gindi leen, teg leen ca yoonu ña leen jiitu woon, te jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la [ci àtteem].
27وَاللَّهُ يُرِيدُ أَن يَتُوبَ عَلَيْكُمْ وَيُرِيدُ الَّذِينَ يَتَّبِعُونَ الشَّهَوَاتِ أَن تَمِيلُوا مَيْلًا عَظِيمًا
Yàlla dafa leen bëgg a jéggal. Waaye ña topp seen bànneex, ñoom dañuy bëgg ngeen jeng, jeng gu fés.
28يُرِيدُ اللَّهُ أَن يُخَفِّفَ عَنكُمْ ۚ وَخُلِقَ الْإِنسَانُ ضَعِيفًا
Yàlla dafa leen a bëgg a woyofal [àtteem] ndax néew doole ak lott gi nit bindoo.
29يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَأْكُلُوا أَمْوَالَكُم بَيْنَكُم بِالْبَاطِلِ إِلَّا أَن تَكُونَ تِجَارَةً عَن تَرَاضٍ مِّنكُمْ ۚ وَلَا تَقْتُلُوا أَنفُسَكُمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ بِكُمْ رَحِيمًا
Éy yéen ñi gëm ! Buleen lekkante seeni alal cig neen. Waaye mën ngeen a jëflante ci njulo [jënd ak jaay] mu ànd ak déggoo ci seen mbir. Te buleen reyante. Yàlla, Ku am yërmaande ci yéen la.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
27Aaya

Tekki — An-Nisa 27

Simoore An-Nisa Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla dafa leen bëgg a jéggal. Waaye ña topp seen…

Simoore Aaya 27/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers