Al-Maida · 10/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَحِيمِ ۝١٠
Wallazeena kafaroo wa kazzaboo bi Aayaatinaaa ulaaa`ika Ashaabul Jaheem
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne weddi nañu te jàppe Sunuy tegtal ay fen, ñooña ñooy waa Safara.
🎧 Dégg

📜 Aaya 8-12 — Al-Maida

8يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ لِلَّهِ شُهَدَاءَ بِالْقِسْطِ ۖ وَلَا يَجْرِمَنَّكُمْ شَنَآنُ قَوْمٍ عَلَىٰ أَلَّا تَعْدِلُوا ۚ اعْدِلُوا هُوَ أَقْرَبُ لِلتَّقْوَىٰ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen nekk ñu taxaw temm ngir Yàlla, di ay seede cig maandute. Te mbañeel gu ngeen bañ aw nit , bumu xiir kenn ci ñàkk a maandu. Nangeen maandu : moo gën a jege ragal Yàlla. Te Yàlla Ku ràññee li ngeen di def la.
9وَعَدَ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ۙ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ عَظِيمٌ
Yàlla dig na ñi gëm tey jëf lu jiw [farataak sunna] xéewal ak pey gu rëy.
10وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَحِيمِ
Ña nga xam ne weddi nañu te jàppe Sunuy tegtal ay fen, ñooña ñooy waa Safara.
11يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اذْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ إِذْ هَمَّ قَوْمٌ أَن يَبْسُطُوا إِلَيْكُمْ أَيْدِيَهُمْ فَكَفَّ أَيْدِيَهُمْ عَنكُمْ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ
Yéen ñi gëm, fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ba mu amee kurél bu nammoon a dal ci seen kaw te Ma fegal leen loxoy noon ya. Ragal-leen Yàlla. Ñi gëm nag, ci Yàlla doŋŋ lañu war a sukkandiku.
12۞ وَلَقَدْ أَخَذَ اللَّهُ مِيثَاقَ بَنِي إِسْرَائِيلَ وَبَعَثْنَا مِنْهُمُ اثْنَيْ عَشَرَ نَقِيبًا ۖ وَقَالَ اللَّهُ إِنِّي مَعَكُمْ ۖ لَئِنْ أَقَمْتُمُ الصَّلَاةَ وَآتَيْتُمُ الزَّكَاةَ وَآمَنتُم بِرُسُلِي وَعَزَّرْتُمُوهُمْ وَأَقْرَضْتُمُ اللَّهَ قَرْضًا حَسَنًا لَّأُكَفِّرَنَّ عَنكُمْ سَيِّئَاتِكُمْ وَلَأُدْخِلَنَّكُمْ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ ۚ فَمَن كَفَرَ بَعْدَ ذَٰلِكَ مِنكُمْ فَقَدْ ضَلَّ سَوَاءَ السَّبِيلِ
Yàlla fasante woon na kóllare ak waa Banii-Israayiila. Nu feeñal ci ñoom fukki kilifa ak ñaar. Yàlla ne leen : “Maak yéeen a ànd, bu ngeen di taxawal jullli [fonku ko], di génne asaka, te gëm Samay Yonent, di leen dimbali tey lebal Yàlla [ci seeni alal]. Bor bu rafet dana leen jéggal seeni bàkkaar [ñaawtéef], dugal leen Àjjana yoo xam ne ay dex ay daw ci suufam. Ku weddi ginnaaw loolu te bokk ci yéen, [na xam ne] réere na yoon wu jub wa” !
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
10Aaya

Tekki — Al-Maida 10

Simoore Al-Maida Aaya 10 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne weddi nañu te jàppe Sunuy tegtal…

Simoore Aaya 10/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 8–12. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers