Al-Maida · 9/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَعَدَ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ۙ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ عَظِيمٌ ۝٩
Wa`adal laahul lazeena aamanoo wa `amilus saalihaati lahum maghfiratunw wa ajrun `azeem
📖 Tekkim Wolof
Yàlla dig na ñi gëm tey jëf lu jiw [farataak sunna] xéewal ak pey gu rëy.
🎧 Dégg

📜 Aaya 7-11 — Al-Maida

7وَاذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَمِيثَاقَهُ الَّذِي وَاثَقَكُم بِهِ إِذْ قُلْتُمْ سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ak kóllare ya ngeen fasanteek Moom ba ngeen nee : “Dégg nanu te nangu nanu”. Te nangeen ragal Yàlla. Yàlla dey Ku xam li nekk ci xol yi la.
8يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ لِلَّهِ شُهَدَاءَ بِالْقِسْطِ ۖ وَلَا يَجْرِمَنَّكُمْ شَنَآنُ قَوْمٍ عَلَىٰ أَلَّا تَعْدِلُوا ۚ اعْدِلُوا هُوَ أَقْرَبُ لِلتَّقْوَىٰ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen nekk ñu taxaw temm ngir Yàlla, di ay seede cig maandute. Te mbañeel gu ngeen bañ aw nit , bumu xiir kenn ci ñàkk a maandu. Nangeen maandu : moo gën a jege ragal Yàlla. Te Yàlla Ku ràññee li ngeen di def la.
9وَعَدَ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ۙ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ عَظِيمٌ
Yàlla dig na ñi gëm tey jëf lu jiw [farataak sunna] xéewal ak pey gu rëy.
10وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَحِيمِ
Ña nga xam ne weddi nañu te jàppe Sunuy tegtal ay fen, ñooña ñooy waa Safara.
11يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اذْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ إِذْ هَمَّ قَوْمٌ أَن يَبْسُطُوا إِلَيْكُمْ أَيْدِيَهُمْ فَكَفَّ أَيْدِيَهُمْ عَنكُمْ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ
Yéen ñi gëm, fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ba mu amee kurél bu nammoon a dal ci seen kaw te Ma fegal leen loxoy noon ya. Ragal-leen Yàlla. Ñi gëm nag, ci Yàlla doŋŋ lañu war a sukkandiku.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
9Aaya

Tekki — Al-Maida 9

Simoore Al-Maida Aaya 9 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla dig na ñi gëm tey jëf lu jiw [farataak…

Simoore Aaya 9/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 7–11. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers