Al-Maida · 111/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَإِذْ أَوْحَيْتُ إِلَى الْحَوَارِيِّينَ أَنْ آمِنُوا بِي وَبِرَسُولِي قَالُوا آمَنَّا وَاشْهَدْ بِأَنَّنَا مُسْلِمُونَ ۝١١١
Wa iz awhaitu ilal hawaariyyeena an aaminoo bee wa bi Rasoolee qaalooo aamannaa washhad bi annanaa muslimoon
📖 Tekkim Wolof
Fàttalikul ba nu xiiree sa taalibe ya [waaraatekat ya], sol ci seeni xol ne leen: “Gëmleen Ma ak Sama Yonent”. Ñu ne : “Gëm nanu ; te Nanga seede ne nun way-wommatu lanu [jullit lanu]”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 109-113 — Al-Maida

109۞ يَوْمَ يَجْمَعُ اللَّهُ الرُّسُلَ فَيَقُولُ مَاذَا أُجِبْتُمْ ۖ قَالُوا لَا عِلْمَ لَنَا ۖ إِنَّكَ أَنتَ عَلَّامُ الْغُيُوبِ
Bis bu Yàlla dajalee Yonent ya, ne leen : “Lu ñu leen toontu ? ” Ñu ne Ko : “Amunu xam-xam : Yaw yaay ki xam kumpa”.
110إِذْ قَالَ اللَّهُ يَا عِيسَى ابْنَ مَرْيَمَ اذْكُرْ نِعْمَتِي عَلَيْكَ وَعَلَىٰ وَالِدَتِكَ إِذْ أَيَّدتُّكَ بِرُوحِ الْقُدُسِ تُكَلِّمُ النَّاسَ فِي الْمَهْدِ وَكَهْلًا ۖ وَإِذْ عَلَّمْتُكَ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَالتَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ ۖ وَإِذْ تَخْلُقُ مِنَ الطِّينِ كَهَيْئَةِ الطَّيْرِ بِإِذْنِي فَتَنفُخُ فِيهَا فَتَكُونُ طَيْرًا بِإِذْنِي ۖ وَتُبْرِئُ الْأَكْمَهَ وَالْأَبْرَصَ بِإِذْنِي ۖ وَإِذْ تُخْرِجُ الْمَوْتَىٰ بِإِذْنِي ۖ وَإِذْ كَفَفْتُ بَنِي إِسْرَائِيلَ عَنكَ إِذْ جِئْتَهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْهُمْ إِنْ هَٰذَا إِلَّا سِحْرٌ مُّبِينٌ
[Fàttalikul] ba Yàlla nee : "Yaw Iisaa, doomi Maryaama, fàttalikul xéewal ya Ma la defal yaak sa yaay ba Ma la dimbalee boole la ak Ruu gu sell ga [Jibriil]. Ba nga wax ak nit ñi fekk yaa ngi nekk liir ak ba nga nekkee mag mu weesu ndaw. [Fàttalikul it] ba Ma la jàngalee Téere ba ak gis-gis bu ubbiku, ak Tawreet ak Linjiil ! [Fàttalikul it] ba ngay sos ci ban lu ame melow njanaaw ; ci Sama coobare nga ëf ca. Mu nekk njanaaw ci sama coobare. Te ngay wéral ku gumba ak ku gaana, ci Sama coobare. Ak di génne ku dee [ci bàmmeel] ci Sama coobare ak ci li Ma la fegal waa Bani-Israayiil [ñu bañ laa lor] ba nga leen indilee lay yu leer ya. Te ña weddi ca ñoom ne leen : “Nekkul lu dul njibar gu bir”.
111وَإِذْ أَوْحَيْتُ إِلَى الْحَوَارِيِّينَ أَنْ آمِنُوا بِي وَبِرَسُولِي قَالُوا آمَنَّا وَاشْهَدْ بِأَنَّنَا مُسْلِمُونَ
Fàttalikul ba nu xiiree sa taalibe ya [waaraatekat ya], sol ci seeni xol ne leen: “Gëmleen Ma ak Sama Yonent”. Ñu ne : “Gëm nanu ; te Nanga seede ne nun way-wommatu lanu [jullit lanu]”.
112إِذْ قَالَ الْحَوَارِيُّونَ يَا عِيسَى ابْنَ مَرْيَمَ هَلْ يَسْتَطِيعُ رَبُّكَ أَن يُنَزِّلَ عَلَيْنَا مَائِدَةً مِّنَ السَّمَاءِ ۖ قَالَ اتَّقُوا اللَّهَ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
(fàttalikul) ba waarekat yooyu waxee ne : “Yaw Iisaa, doomi Maryaama, moo ndax sa Boroom mën naa wàcce ci nun [ndën] lu jóge ci asamaan [am ñam] ? ”. Mu ne leen : “Ragal- leen Yàlla, ndegam gëm ngeen”.
113قَالُوا نُرِيدُ أَن نَّأْكُلَ مِنْهَا وَتَطْمَئِنَّ قُلُوبُنَا وَنَعْلَمَ أَن قَدْ صَدَقْتَنَا وَنَكُونَ عَلَيْهَا مِنَ الشَّاهِدِينَ
Ñu ne : “Danoo bëgg lekk ci moom [ndën la] ndax sunu xel dal, nu daldi xam ne wax nga dëgg te kon nun dananu seede loolu”.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
111Aaya

Tekki — Al-Maida 111

Simoore Al-Maida Aaya 111 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Fàttalikul ba nu xiiree sa taalibe ya [waaraatekat ya], sol…

Simoore Aaya 111/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 109–113. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers