Al-Maida · 30/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
فَطَوَّعَتْ لَهُ نَفْسُهُ قَتْلَ أَخِيهِ فَقَتَلَهُ فَأَصْبَحَ مِنَ الْخَاسِرِينَ ۝٣٠
Fatawwa`at lahoo nafsu hoo qatla akheehi faqatalahoo fa asbaha minal khaasireen
📖 Tekkim Wolof
[Ka ñu nangulul], bakkanam daldi koy xiir ci rey mbokkam. Mu daldi far bokk ca way- yàqule ña.
🎧 Dégg

📜 Aaya 28-32 — Al-Maida

28لَئِن بَسَطتَ إِلَيَّ يَدَكَ لِتَقْتُلَنِي مَا أَنَا بِبَاسِطٍ يَدِيَ إِلَيْكَ لِأَقْتُلَكَ ۖ إِنِّي أَخَافُ اللَّهَ رَبَّ الْعَالَمِينَ
Te boo tàllalee sa loxo di ma rey man dey duma jëme sama loxo ci yaw waxantumalaak di la jéem a rey : ndax man Yàlla Miy Boroom mbindeef yi laa ragal.
29إِنِّي أُرِيدُ أَن تَبُوءَ بِإِثْمِي وَإِثْمِكَ فَتَكُونَ مِنْ أَصْحَابِ النَّارِ ۚ وَذَٰلِكَ جَزَاءُ الظَّالِمِينَ
Te sax li ma namm moo di nga yenu sama bàkkaar boole kook sa bos : bu ko defee nga bokk ca waa Safara. Te loolu mooy peyug tooñkat ya.
30فَطَوَّعَتْ لَهُ نَفْسُهُ قَتْلَ أَخِيهِ فَقَتَلَهُ فَأَصْبَحَ مِنَ الْخَاسِرِينَ
[Ka ñu nangulul], bakkanam daldi koy xiir ci rey mbokkam. Mu daldi far bokk ca way- yàqule ña.
31فَبَعَثَ اللَّهُ غُرَابًا يَبْحَثُ فِي الْأَرْضِ لِيُرِيَهُ كَيْفَ يُوَارِي سَوْءَةَ أَخِيهِ ۚ قَالَ يَا وَيْلَتَا أَعَجَزْتُ أَنْ أَكُونَ مِثْلَ هَٰذَا الْغُرَابِ فَأُوَارِيَ سَوْءَةَ أَخِي ۖ فَأَصْبَحَ مِنَ النَّادِمِينَ
Yàlla daldi yebal baaxoñ buy gas suuf si ngir mu won ko naka lay suturaale néewub mbokkam moomu. [Ba mu gisee baaxoñ ba], mu daldi ne : “Ngalla man ! Ndax damaa yées baaxoñ bii ba mënumaa suturaal néewub sama mbokk mi ? ”. Daldi koy rëccu lool.
32مِنْ أَجْلِ ذَٰلِكَ كَتَبْنَا عَلَىٰ بَنِي إِسْرَائِيلَ أَنَّهُ مَن قَتَلَ نَفْسًا بِغَيْرِ نَفْسٍ أَوْ فَسَادٍ فِي الْأَرْضِ فَكَأَنَّمَا قَتَلَ النَّاسَ جَمِيعًا وَمَنْ أَحْيَاهَا فَكَأَنَّمَا أَحْيَا النَّاسَ جَمِيعًا ۚ وَلَقَدْ جَاءَتْهُمْ رُسُلُنَا بِالْبَيِّنَاتِ ثُمَّ إِنَّ كَثِيرًا مِّنْهُم بَعْدَ ذَٰلِكَ فِي الْأَرْضِ لَمُسْرِفُونَ
Ngir loolu, bokkal Nanu ca waa Banii-Israayiila, ne képp ku reyati nit koo xam ne reyul kenn, te deful njaaxum ci kaw suuf si, mel na ni rey na nit ñépp. Ku xettali nit, musal ko ci dee, mel na ni ku musal nit ñépp ci dee. Sunuy Yonent dikkal na leen ànd ak lay yu leer nàññ. Ginnaaw loolu, lu bari ci ñoom nekk ay yàqkat ci suuf si [àddina bi].
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
30Aaya

Tekki — Al-Maida 30

Simoore Al-Maida Aaya 30 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Ka ñu nangulul], bakkanam daldi koy xiir ci rey mbokkam.…

Simoore Aaya 30/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 28–32. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers