Al-An'am · 139/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَقَالُوا مَا فِي بُطُونِ هَٰذِهِ الْأَنْعَامِ خَالِصَةٌ لِّذُكُورِنَا وَمُحَرَّمٌ عَلَىٰ أَزْوَاجِنَا ۖ وَإِن يَكُن مَّيْتَةً فَهُمْ فِيهِ شُرَكَاءُ ۚ سَيَجْزِيهِمْ وَصْفَهُمْ ۚ إِنَّهُ حَكِيمٌ عَلِيمٌ ۝١٣٩
Wa qaaloo maa fee butooni haazihil an`aami khaalisatul lizukoorinaa wa muharramun `alaaa azwaajinaa wa iny yakum maitatan fahum feehi shurakaaa`; sa yajzeehim wasfahum; innahoo Hakeemun `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Ñu naan : “Li nekk ci biir jur gi dagan na ci sunuy góor waaye araam na ci sunuy jabar [jigéen ñi].”. Waay, bu dee lu médd, góor ak jigéen ñoo ci yem. Dana leen fey seeni duur, Moom dey [Yàlla] Ku xereñ la, Ku xam la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 137-141 — Al-An'am

137وَكَذَٰلِكَ زَيَّنَ لِكَثِيرٍ مِّنَ الْمُشْرِكِينَ قَتْلَ أَوْلَادِهِمْ شُرَكَاؤُهُمْ لِيُرْدُوهُمْ وَلِيَلْبِسُوا عَلَيْهِمْ دِينَهُمْ ۖ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا فَعَلُوهُ ۖ فَذَرْهُمْ وَمَا يَفْتَرُونَ
Noonu la seen xërëm yooyu rafetale, ca ñu bari ca way-bokkaale ya, rey seeni doom, ngir alag leen, lëntal seen diine. Bu neexoon Yàlla, duñu ko def. Waaye bàyyileen ak la ñuy duur.
138وَقَالُوا هَٰذِهِ أَنْعَامٌ وَحَرْثٌ حِجْرٌ لَّا يَطْعَمُهَا إِلَّا مَن نَّشَاءُ بِزَعْمِهِمْ وَأَنْعَامٌ حُرِّمَتْ ظُهُورُهَا وَأَنْعَامٌ لَّا يَذْكُرُونَ اسْمَ اللَّهِ عَلَيْهَا افْتِرَاءً عَلَيْهِ ۚ سَيَجْزِيهِم بِمَا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Ñu naan : “Jur gi ak mbey mi araam na : kenn du ci lekk ku dul ku Nu neex.”. - ci seeni njort ! - Ak jur goo xam ne seen ginnaaw araam na, ak yoo xam ne duñu tuddu Yàlla ci ñoom, lu dul di ko duural, Dana leen fey la ñu nekkoon di ko duur.
139وَقَالُوا مَا فِي بُطُونِ هَٰذِهِ الْأَنْعَامِ خَالِصَةٌ لِّذُكُورِنَا وَمُحَرَّمٌ عَلَىٰ أَزْوَاجِنَا ۖ وَإِن يَكُن مَّيْتَةً فَهُمْ فِيهِ شُرَكَاءُ ۚ سَيَجْزِيهِمْ وَصْفَهُمْ ۚ إِنَّهُ حَكِيمٌ عَلِيمٌ
Ñu naan : “Li nekk ci biir jur gi dagan na ci sunuy góor waaye araam na ci sunuy jabar [jigéen ñi].”. Waay, bu dee lu médd, góor ak jigéen ñoo ci yem. Dana leen fey seeni duur, Moom dey [Yàlla] Ku xereñ la, Ku xam la.
140قَدْ خَسِرَ الَّذِينَ قَتَلُوا أَوْلَادَهُمْ سَفَهًا بِغَيْرِ عِلْمٍ وَحَرَّمُوا مَا رَزَقَهُمُ اللَّهُ افْتِرَاءً عَلَى اللَّهِ ۚ قَدْ ضَلُّوا وَمَا كَانُوا مُهْتَدِينَ
Ña rey seeni doom cig réer ngir ñàkk a xam, yàqule nañu booleek di araamal la leen Yàlla wërsëgal, lépp tegu ci kaw duural Yàlla. Ñoom réer nañu ba sànku te dootuñu gindiku.
141۞ وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَ جَنَّاتٍ مَّعْرُوشَاتٍ وَغَيْرَ مَعْرُوشَاتٍ وَالنَّخْلَ وَالزَّرْعَ مُخْتَلِفًا أُكُلُهُ وَالزَّيْتُونَ وَالرُّمَّانَ مُتَشَابِهًا وَغَيْرَ مُتَشَابِهٍ ۚ كُلُوا مِن ثَمَرِهِ إِذَا أَثْمَرَ وَآتُوا حَقَّهُ يَوْمَ حَصَادِهِ ۖ وَلَا تُسْرِفُوا ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُسْرِفِينَ
Moom Yàlla Moo sos ay tooli gàncax guy law ci suuf si ak yuy jóg taxaw ; ak garabi tàndarma ak mbey yu meññeent ya wuute ; ak oliw ak garanaat yu niroo ak yu niroowul. Lekkleen seeni doom bu ñoree ; te nangeen génne asaka ja bis ba ngeen di watt [ngóob]. Te buleen yàq ndax Moom [Yàlla] safoowul yàqkat ya.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
139Aaya

Tekki — Al-An'am 139

Simoore Al-An'am Aaya 139 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu naan : “Li nekk ci biir jur gi dagan…

Simoore Aaya 139/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 137–141. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers