Al-An'am · 41/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
بَلْ إِيَّاهُ تَدْعُونَ فَيَكْشِفُ مَا تَدْعُونَ إِلَيْهِ إِن شَاءَ وَتَنسَوْنَ مَا تُشْرِكُونَ ۝٤١
Bal iyyaahu tad`oona fa yakshifu maa tad`oona ilaihi in shaaa`a wa tansawna maa tushrikoon
📖 Tekkim Wolof
Déedéet, Moom ci boppam ngeen di woo. Mu xar lor ja su ko soobee, ngeen daldi fàtte ya ngeen daan bokkaale.

🎧 Dégg


📜 Aaya 39-43 — Al-An'am

39وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا صُمٌّ وَبُكْمٌ فِي الظُّلُمَاتِ ۗ مَن يَشَإِ اللَّهُ يُضْلِلْهُ وَمَن يَشَأْ يَجْعَلْهُ عَلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Te ña weddi Sunuy kàddu, dañoo tëx, luu, gumba. Yàlla ku ko soob, mu bàyyi ko cig réeram ; ku Ko soob Mu teg ko ci yoon wu jub wa xocc.
40قُلْ أَرَأَيْتَكُمْ إِنْ أَتَاكُمْ عَذَابُ اللَّهِ أَوْ أَتَتْكُمُ السَّاعَةُ أَغَيْرَ اللَّهِ تَدْعُونَ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Neel : “Waxleen ma : ndax su leen mbugalum Yàlla dalee, walla Bis-pénc ba na jaseet ci seen kaw, su fekkee li ngeen di woote dëgg la ci yéen, moo ndax kon dangeen fawoo keneen ku moy Yàlla ? ”
41بَلْ إِيَّاهُ تَدْعُونَ فَيَكْشِفُ مَا تَدْعُونَ إِلَيْهِ إِن شَاءَ وَتَنسَوْنَ مَا تُشْرِكُونَ
Déedéet, Moom ci boppam ngeen di woo. Mu xar lor ja su ko soobee, ngeen daldi fàtte ya ngeen daan bokkaale.
42وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا إِلَىٰ أُمَمٍ مِّن قَبْلِكَ فَأَخَذْنَاهُم بِالْبَأْسَاءِ وَالضَّرَّاءِ لَعَلَّهُمْ يَتَضَرَّعُونَ
Te yónnee woon Nanu ca xeet ya la jiitu. Nu tegoon leen coonay ñàkk ak i naqar - ndax Yàlla ñu jànge ca toroxlu ! -
43فَلَوْلَا إِذْ جَاءَهُم بَأْسُنَا تَضَرَّعُوا وَلَٰكِن قَسَتْ قُلُوبُهُمْ وَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Su fekkoon ba leen coono dalee toroxlu nañu, sax [nga ne waaw] ? Waaye seeni xol dafa wow, Séytaane daldi leen koy jékkalal ak la jëf ja di ju nu lébbi.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
41Aaya

Tekki — Al-An'am 41

Simoore Al-An'am Aaya 41 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Déedéet, Moom ci boppam ngeen di woo. Mu xar lor…

Simoore Aaya 41/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 39–43. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers