Al-An'am · 44/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
فَلَمَّا نَسُوا مَا ذُكِّرُوا بِهِ فَتَحْنَا عَلَيْهِمْ أَبْوَابَ كُلِّ شَيْءٍ حَتَّىٰ إِذَا فَرِحُوا بِمَا أُوتُوا أَخَذْنَاهُم بَغْتَةً فَإِذَا هُم مُّبْلِسُونَ ۝٤٤
Falammaa nasoo maa zukkiroo bihee fatahnaa `alaihim abwaaba kulli shai`in hattaaa izaa farihoo bimaaa ootooo akhaznaahum baghtatan fa izaa hum mmublisoon
📖 Tekkim Wolof
Ba ñu fàttee la Nu leen waare woon nag, ubbil Nanu leen buntu [teraanga] bu nekk ; ba ñu bég ca la Nu leen jox, Nu seet seet ne xes ca seen kaw ak sànje bu dootul dog, ñu ne tocc.

🎧 Dégg


📜 Aaya 42-46 — Simoore Al-An'am

42وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا إِلَىٰ أُمَمٍ مِّن قَبْلِكَ فَأَخَذْنَاهُم بِالْبَأْسَاءِ وَالضَّرَّاءِ لَعَلَّهُمْ يَتَضَرَّعُونَ
Te yónnee woon Nanu ca xeet ya la jiitu. Nu tegoon leen coonay ñàkk ak i naqar - ndax Yàlla ñu jànge ca toroxlu ! -
43فَلَوْلَا إِذْ جَاءَهُم بَأْسُنَا تَضَرَّعُوا وَلَٰكِن قَسَتْ قُلُوبُهُمْ وَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Su fekkoon ba leen coono dalee toroxlu nañu, sax [nga ne waaw] ? Waaye seeni xol dafa wow, Séytaane daldi leen koy jékkalal ak la jëf ja di ju nu lébbi.
44فَلَمَّا نَسُوا مَا ذُكِّرُوا بِهِ فَتَحْنَا عَلَيْهِمْ أَبْوَابَ كُلِّ شَيْءٍ حَتَّىٰ إِذَا فَرِحُوا بِمَا أُوتُوا أَخَذْنَاهُم بَغْتَةً فَإِذَا هُم مُّبْلِسُونَ
Ba ñu fàttee la Nu leen waare woon nag, ubbil Nanu leen buntu [teraanga] bu nekk ; ba ñu bég ca la Nu leen jox, Nu seet seet ne xes ca seen kaw ak sànje bu dootul dog, ñu ne tocc.
45فَقُطِعَ دَابِرُ الْقَوْمِ الَّذِينَ ظَلَمُوا ۚ وَالْحَمْدُ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ
Dogeef na ginnaawug ña tooñoon. Te nag Yàlla miy Boroom àddina bi rekk a yayoo cant !
46قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِنْ أَخَذَ اللَّهُ سَمْعَكُمْ وَأَبْصَارَكُمْ وَخَتَمَ عَلَىٰ قُلُوبِكُم مَّنْ إِلَٰهٌ غَيْرُ اللَّهِ يَأْتِيكُم بِهِ ۗ انظُرْ كَيْفَ نُصَرِّفُ الْآيَاتِ ثُمَّ هُمْ يَصْدِفُونَ
Waxleen ma : “Bu Yàlla téye woon seenug dégg, ak seenug jis, tëj seeni xol, ana keneen ku dul Yàlla ku leen mën a delloo yooyu ? Gisal ni Yàlla di leerale ay tegtalam ! Ba noppi ñoom ñuy jeng.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
44Aaya

Tekki — Al-An'am 44

Simoore Al-An'am Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba ñu fàttee la Nu leen waare woon nag, ubbil…

Simoore Aaya 44/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers