Al-An'am · 51/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَأَنذِرْ بِهِ الَّذِينَ يَخَافُونَ أَن يُحْشَرُوا إِلَىٰ رَبِّهِمْ ۙ لَيْسَ لَهُم مِّن دُونِهِ وَلِيٌّ وَلَا شَفِيعٌ لَّعَلَّهُمْ يَتَّقُونَ ۝٥١
Wa anzir bihil lazeena yakhaafoona ai yuhsharooo ilaa Rabbihim laisa lahum min doonihee waliyyunw wa laa shafee`ul la`allahum yattaqoon
📖 Tekkim Wolof
Artul ak Alxuraan, ñi ragal, ñu fang leen jëme fa seen Boroom, amuñu leneen kiiraay, du caageene ab rammukat. Ndax xéy-na ñu ragal Yàlla !
🎧 Dégg

📜 Aaya 49-53 — Al-An'am

49وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا يَمَسُّهُمُ الْعَذَابُ بِمَا كَانُوا يَفْسُقُونَ
Ña weddi Sunuy kàddu, mbugal dana leen sóor ndax la ñu daan jalgati.
50قُل لَّا أَقُولُ لَكُمْ عِندِي خَزَائِنُ اللَّهِ وَلَا أَعْلَمُ الْغَيْبَ وَلَا أَقُولُ لَكُمْ إِنِّي مَلَكٌ ۖ إِنْ أَتَّبِعُ إِلَّا مَا يُوحَىٰ إِلَيَّ ۚ قُلْ هَلْ يَسْتَوِي الْأَعْمَىٰ وَالْبَصِيرُ ۚ أَفَلَا تَتَفَكَّرُونَ
Neel: “Dumaleen wax it ne Malaaka laa, li am mooy li ñu ma soloo doŋŋ laay topp.”. Neel : “Ndax mënees naa yemale gumba ak njàccaar ? Moo ndax dangeen dul xel-lu ? ”
51وَأَنذِرْ بِهِ الَّذِينَ يَخَافُونَ أَن يُحْشَرُوا إِلَىٰ رَبِّهِمْ ۙ لَيْسَ لَهُم مِّن دُونِهِ وَلِيٌّ وَلَا شَفِيعٌ لَّعَلَّهُمْ يَتَّقُونَ
Artul ak Alxuraan, ñi ragal, ñu fang leen jëme fa seen Boroom, amuñu leneen kiiraay, du caageene ab rammukat. Ndax xéy-na ñu ragal Yàlla !
52وَلَا تَطْرُدِ الَّذِينَ يَدْعُونَ رَبَّهُم بِالْغَدَاةِ وَالْعَشِيِّ يُرِيدُونَ وَجْهَهُ ۖ مَا عَلَيْكَ مِنْ حِسَابِهِم مِّن شَيْءٍ وَمَا مِنْ حِسَابِكَ عَلَيْهِم مِّن شَيْءٍ فَتَطْرُدَهُمْ فَتَكُونَ مِنَ الظَّالِمِينَ
Bul dàq ñiy jaamu seen Boroom suba ak ngoon ngir bëgg jëmmam [Yàlla]. Dara waru la ci àtte seeni mbir, ñoom it dara waruleen ci àtte say mbir. Ba tax na, boo leen dàqee daldi bokk ca tooñkat ya.
53وَكَذَٰلِكَ فَتَنَّا بَعْضَهُم بِبَعْضٍ لِّيَقُولُوا أَهَٰؤُلَاءِ مَنَّ اللَّهُ عَلَيْهِم مِّن بَيْنِنَا ۗ أَلَيْسَ اللَّهُ بِأَعْلَمَ بِالشَّاكِرِينَ
Noonu la Nu notee ñenn ci ñoom jaare ko ci ñeneen ca ñoom, ngir ñu wax ne : “Ndax [ña doyadi] ñii la Yàlla xéewale ci nun ? ”. Moo ndax Yàlla Moo gën a xam ña koy gëram ciy xéewalam ?
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
51Aaya

Tekki — Al-An'am 51

Simoore Al-An'am Aaya 51 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Artul ak Alxuraan, ñi ragal, ñu fang leen jëme fa…

Simoore Aaya 51/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 49–53. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers