Al-An'am · 56/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
قُلْ إِنِّي نُهِيتُ أَنْ أَعْبُدَ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ ۚ قُل لَّا أَتَّبِعُ أَهْوَاءَكُمْ ۙ قَدْ ضَلَلْتُ إِذًا وَمَا أَنَا مِنَ الْمُهْتَدِينَ ۝٥٦
Qul innee nuheetu an a`budal lazeena tad`oona min doonil laah; qul laaa attabi`u ahwaaa`akum qad dalaltu izanw wa maaa ana minal muhtadeen
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Man tere nañu ma may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla”. Neel itam : “Duma topp seeni bànneex : ndax su ma ko defee, damay sànku te kon duma bokk ca ñu gindiku ña”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 54-58 — Al-An'am

54وَإِذَا جَاءَكَ الَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِنَا فَقُلْ سَلَامٌ عَلَيْكُمْ ۖ كَتَبَ رَبُّكُمْ عَلَىٰ نَفْسِهِ الرَّحْمَةَ ۖ أَنَّهُ مَنْ عَمِلَ مِنكُمْ سُوءًا بِجَهَالَةٍ ثُمَّ تَابَ مِن بَعْدِهِ وَأَصْلَحَ فَأَنَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ña gëm Sunuy kàddu, bu ñu la dikkalee, neel : “Yal na jàmm wàcc ci yéen ! Yàlla seen Boroom dogal na ci boppam yërmaande. Li am mooy, ku def ci yéen aw ñaawtéef cig ñàkk a xam, ba mu noppee, tuub, rëccu, sellal jëfam ... Yàlla moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.
55وَكَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ الْآيَاتِ وَلِتَسْتَبِينَ سَبِيلُ الْمُجْرِمِينَ
Te noonu Lanuy leeralee tegtal yi ngir fésal yoonu tooñkat yi.
56قُلْ إِنِّي نُهِيتُ أَنْ أَعْبُدَ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ ۚ قُل لَّا أَتَّبِعُ أَهْوَاءَكُمْ ۙ قَدْ ضَلَلْتُ إِذًا وَمَا أَنَا مِنَ الْمُهْتَدِينَ
Neel : “Man tere nañu ma may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla”. Neel itam : “Duma topp seeni bànneex : ndax su ma ko defee, damay sànku te kon duma bokk ca ñu gindiku ña”.
57قُلْ إِنِّي عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّي وَكَذَّبْتُم بِهِ ۚ مَا عِندِي مَا تَسْتَعْجِلُونَ بِهِ ۚ إِنِ الْحُكْمُ إِلَّا لِلَّهِ ۖ يَقُصُّ الْحَقَّ ۖ وَهُوَ خَيْرُ الْفَاصِلِينَ
Neel : “Man dama nekk ci lu bir [leer nàññ], di lu jóge fa sama Boroom, ngeen weddi ko. Li ngeen di [laaj te di ko] yàkkamti, nekkul ci man. Àpp ba, Yàlla rekk a ko moom : Mooy nettali dëgg te Mooy gën jaa mën a àtte [téqale] ay mbir.
58قُل لَّوْ أَنَّ عِندِي مَا تَسْتَعْجِلُونَ بِهِ لَقُضِيَ الْأَمْرُ بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۗ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِالظَّالِمِينَ
Neel : “Bu fekkoon li ngeen di [laaj] di yàkkamti mi ngi ci man, kon mbir ya sottikoon na sama diggante ak yéen.” Te Yàllaa gën a xam tooñkat ya.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
56Aaya

Tekki — Al-An'am 56

Simoore Al-An'am Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Man tere nañu ma may jaamu li ngeen…

Simoore Aaya 56/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers