Al-An'am · 9/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
وَلَوْ جَعَلْنَاهُ مَلَكًا لَّجَعَلْنَاهُ رَجُلًا وَلَلَبَسْنَا عَلَيْهِم مَّا يَلْبِسُونَ ۝٩
Wa law ja`alnaahu malakal laja`alnaahu rajulanw wa lalabasnaa `alaihim maa yalbisoon
📖 Tekkim Wolof
Te sax bu Nu ko defoon muy Malaaka, kon jëmmi nit Lanu koy jox, te kon Nu lëntal ca ñoom la Nu lëntal ci seen bopp.

🎧 Dégg


📜 Aaya 7-11 — Simoore Al-An'am

7وَلَوْ نَزَّلْنَا عَلَيْكَ كِتَابًا فِي قِرْطَاسٍ فَلَمَسُوهُ بِأَيْدِيهِمْ لَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا إِنْ هَٰذَا إِلَّا سِحْرٌ مُّبِينٌ
Bu Nu la wàcceeloon Téere bu ñu bind ci kayit gu ñu mën a laal ak seeni yoxo sax, du tee ñu weddi ñoom ne : “Lii ag jibar doŋŋ la ! ”
8وَقَالُوا لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْهِ مَلَكٌ ۖ وَلَوْ أَنزَلْنَا مَلَكًا لَّقُضِيَ الْأَمْرُ ثُمَّ لَا يُنظَرُونَ
Ba noppi di wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom Malaaka ? ”. Waaye bu ñu wàcce woon Malaaka, kon mbir ya sottikoon na ; ndax kenn duleen muñandiku kon.
9وَلَوْ جَعَلْنَاهُ مَلَكًا لَّجَعَلْنَاهُ رَجُلًا وَلَلَبَسْنَا عَلَيْهِم مَّا يَلْبِسُونَ
Te sax bu Nu ko defoon muy Malaaka, kon jëmmi nit Lanu koy jox, te kon Nu lëntal ca ñoom la Nu lëntal ci seen bopp.
10وَلَقَدِ اسْتُهْزِئَ بِرُسُلٍ مِّن قَبْلِكَ فَحَاقَ بِالَّذِينَ سَخِرُوا مِنْهُم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ
Doon nañu yejji ay Yonent lu jiitu, waaye ña leen doon reetaan, la ñu daan yejji wàcc na ca seen kaw [alag leen].
11قُلْ سِيرُوا فِي الْأَرْضِ ثُمَّ انظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُكَذِّبِينَ
Neel : “Doxleen ci suuf si te ngeen seetlu naka la mujjug way-weddi ña deme”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
9Aaya

Tekki — Al-An'am 9

Simoore Al-An'am Aaya 9 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te sax bu Nu ko defoon muy Malaaka, kon jëmmi…

Simoore Aaya 9/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 7–11. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers