Al-A'raf · 24/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
قَالَ اهْبِطُوا بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ عَدُوٌّ ۖ وَلَكُمْ فِي الْأَرْضِ مُسْتَقَرٌّ وَمَتَاعٌ إِلَىٰ حِينٍ ۝٢٤
Qaalah bitoo ba`dukum liba`din aduwwunw wa lakum fil ardi mmustaqarrunw wa mataa`un ilaaheen
📖 Tekkim Wolof
Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu ka ca des. Suuf si, am ngeen fay dëkkuwaay ak i xéewal ab diir.”

🎧 Dégg


📜 Aaya 22-26 — Simoore Al-A'raf

22فَدَلَّاهُمَا بِغُرُورٍ ۚ فَلَمَّا ذَاقَا الشَّجَرَةَ بَدَتْ لَهُمَا سَوْآتُهُمَا وَطَفِقَا يَخْصِفَانِ عَلَيْهِمَا مِن وَرَقِ الْجَنَّةِ ۖ وَنَادَاهُمَا رَبُّهُمَا أَلَمْ أَنْهَكُمَا عَن تِلْكُمَا الشَّجَرَةِ وَأَقُل لَّكُمَا إِنَّ الشَّيْطَانَ لَكُمَا عَدُوٌّ مُّبِينٌ
Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ”
23قَالَا رَبَّنَا ظَلَمْنَا أَنفُسَنَا وَإِن لَّمْ تَغْفِرْ لَنَا وَتَرْحَمْنَا لَنَكُونَنَّ مِنَ الْخَاسِرِينَ
[Aadama ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña”.
24قَالَ اهْبِطُوا بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ عَدُوٌّ ۖ وَلَكُمْ فِي الْأَرْضِ مُسْتَقَرٌّ وَمَتَاعٌ إِلَىٰ حِينٍ
Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu ka ca des. Suuf si, am ngeen fay dëkkuwaay ak i xéewal ab diir.”
25قَالَ فِيهَا تَحْيَوْنَ وَفِيهَا تَمُوتُونَ وَمِنْهَا تُخْرَجُونَ
“Fa ngeen di dunde, fa ngeen di faatoo, fa lañu leen di génnee [ngeen dekkiwaat].”
26يَا بَنِي آدَمَ قَدْ أَنزَلْنَا عَلَيْكُمْ لِبَاسًا يُوَارِي سَوْآتِكُمْ وَرِيشًا ۖ وَلِبَاسُ التَّقْوَىٰ ذَٰلِكَ خَيْرٌ ۚ ذَٰلِكَ مِنْ آيَاتِ اللَّهِ لَعَلَّهُمْ يَذَّكَّرُونَ
Yéen doomi-aadama ! Wàcceel Nanu leen koddaay lu ngeen di muure seeni pëy ak i takkaay. -Waaye koddaayul ragal Yàlla moo gën de. - Loolu bokk na ci kéemaani Yàlla yi. Ndax Yàlla ñuy fàttaliku [seen Boroom].
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
24Aaya

Tekki — Al-A'raf 24

Simoore Al-A'raf Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu…

Simoore Aaya 24/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers