Al-A'raf · 23/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
قَالَا رَبَّنَا ظَلَمْنَا أَنفُسَنَا وَإِن لَّمْ تَغْفِرْ لَنَا وَتَرْحَمْنَا لَنَكُونَنَّ مِنَ الْخَاسِرِينَ ۝٢٣
Qaalaa Rabbanaa zalamnaaa anfusanaa wa illam taghfir lanaa wa tarhamnaa lanakoonanna minal khaasireen
📖 Tekkim Wolof
[Aadama ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 21-25 — Al-A'raf

21وَقَاسَمَهُمَا إِنِّي لَكُمَا لَمِنَ النَّاصِحِينَ
Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk rekk ci ñi leen di laabire”.
22فَدَلَّاهُمَا بِغُرُورٍ ۚ فَلَمَّا ذَاقَا الشَّجَرَةَ بَدَتْ لَهُمَا سَوْآتُهُمَا وَطَفِقَا يَخْصِفَانِ عَلَيْهِمَا مِن وَرَقِ الْجَنَّةِ ۖ وَنَادَاهُمَا رَبُّهُمَا أَلَمْ أَنْهَكُمَا عَن تِلْكُمَا الشَّجَرَةِ وَأَقُل لَّكُمَا إِنَّ الشَّيْطَانَ لَكُمَا عَدُوٌّ مُّبِينٌ
Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ”
23قَالَا رَبَّنَا ظَلَمْنَا أَنفُسَنَا وَإِن لَّمْ تَغْفِرْ لَنَا وَتَرْحَمْنَا لَنَكُونَنَّ مِنَ الْخَاسِرِينَ
[Aadama ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña”.
24قَالَ اهْبِطُوا بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ عَدُوٌّ ۖ وَلَكُمْ فِي الْأَرْضِ مُسْتَقَرٌّ وَمَتَاعٌ إِلَىٰ حِينٍ
Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu ka ca des. Suuf si, am ngeen fay dëkkuwaay ak i xéewal ab diir.”
25قَالَ فِيهَا تَحْيَوْنَ وَفِيهَا تَمُوتُونَ وَمِنْهَا تُخْرَجُونَ
“Fa ngeen di dunde, fa ngeen di faatoo, fa lañu leen di génnee [ngeen dekkiwaat].”
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
23Aaya

Tekki — Al-A'raf 23

Simoore Al-A'raf Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Aadama ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu…

Simoore Aaya 23/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers