At-Tawba · 121/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
وَلَا يُنفِقُونَ نَفَقَةً صَغِيرَةً وَلَا كَبِيرَةً وَلَا يَقْطَعُونَ وَادِيًا إِلَّا كُتِبَ لَهُمْ لِيَجْزِيَهُمُ اللَّهُ أَحْسَنَ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝١٢١
Wa laa yunfiqoona nafa qatan sagheeratanw wa laa kabeeratanw wa laa yaqta`oona waadiyan illaa kutiba lahum liyajziyahumul laahu ahsana maa kaanoo ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Te duñu joxe alal ju tuuti, walla ju bari, te it duñu jàll aw xur lu dul ne dees na leen ko bindal, Yàlla feye leen ko lu gën a rafetal.
🎧 Dégg

📜 Aaya 119-123 — At-Tawba

119يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَكُونُوا مَعَ الصَّادِقِينَ
Éy yéen way-gëm ñi ! Nangeen ragal Yàlla te ànd ak ñu dëggu ña.
120مَا كَانَ لِأَهْلِ الْمَدِينَةِ وَمَنْ حَوْلَهُم مِّنَ الْأَعْرَابِ أَن يَتَخَلَّفُوا عَن رَّسُولِ اللَّهِ وَلَا يَرْغَبُوا بِأَنفُسِهِمْ عَن نَّفْسِهِ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ لَا يُصِيبُهُمْ ظَمَأٌ وَلَا نَصَبٌ وَلَا مَخْمَصَةٌ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَلَا يَطَئُونَ مَوْطِئًا يَغِيظُ الْكُفَّارَ وَلَا يَنَالُونَ مِنْ عَدُوٍّ نَّيْلًا إِلَّا كُتِبَ لَهُم بِهِ عَمَلٌ صَالِحٌ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَا يُضِيعُ أَجْرَ الْمُحْسِنِينَ
Yellul ci ñi dëkk Madina ak sàmm sa ko wër, ñuy des ginnaaw, di bàyyi Yonent bi (buy dem jareji), te buleen seeni bakkan gënal bosam. Ndax ñoom, mar walla coono, walla xiif, duleen dale ci yoonu Yàlla, te duñu dëkk senn suuf (soo xam ne, danañu ca taxaw lu dul ne) dana metti yéefar ya, te it duñu am genn nooteel cib noon, te Dana leen ko bindal muy jëf yu yiw ñeel leen. Yàlla du sànk mukk peyug ñiy rafetal.
121وَلَا يُنفِقُونَ نَفَقَةً صَغِيرَةً وَلَا كَبِيرَةً وَلَا يَقْطَعُونَ وَادِيًا إِلَّا كُتِبَ لَهُمْ لِيَجْزِيَهُمُ اللَّهُ أَحْسَنَ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Te duñu joxe alal ju tuuti, walla ju bari, te it duñu jàll aw xur lu dul ne dees na leen ko bindal, Yàlla feye leen ko lu gën a rafetal.
122۞ وَمَا كَانَ الْمُؤْمِنُونَ لِيَنفِرُوا كَافَّةً ۚ فَلَوْلَا نَفَرَ مِن كُلِّ فِرْقَةٍ مِّنْهُمْ طَائِفَةٌ لِّيَتَفَقَّهُوا فِي الدِّينِ وَلِيُنذِرُوا قَوْمَهُمْ إِذَا رَجَعُوا إِلَيْهِمْ لَعَلَّهُمْ يَحْذَرُونَ
Warul ci jullit ñépp dem (xareji). Lu tere mbooloo mu ne mu am ñu ca dem (xamluji) xam-xamu diine, ba bu ñu delsee ca seeni mbokk, waar leen ngir ñu mën a wattandiku.
123يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا قَاتِلُوا الَّذِينَ يَلُونَكُم مِّنَ الْكُفَّارِ وَلْيَجِدُوا فِيكُمْ غِلْظَةً ۚ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ مَعَ الْمُتَّقِينَ
Éy yéen ñi gëm ! Xeexleen ak ñi leen jegeñ ci yéefar yi ; nañu fekk ci yéen dëgër gu mat sëkk. Te ngeen xam ne Yàllaa ngi ànd ak ñi ragal Yàlla.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
121Aaya

Tekki — At-Tawba 121

Simoore At-Tawba Aaya 121 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te duñu joxe alal ju tuuti, walla ju bari, te…

Simoore Aaya 121/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 119–123. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers