At-Tawba · 22/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عِندَهُ أَجْرٌ عَظِيمٌ ۝٢٢
Khaalideena feehaaa abadaa; innal laaha `indahooo ajrun `azeem
📖 Tekkim Wolof
dañu fay dëkk fàwwu. Pey gu màgg moo nekk fa Yàlla.
🎧 Dégg

📜 Aaya 20-24 — At-Tawba

20الَّذِينَ آمَنُوا وَهَاجَرُوا وَجَاهَدُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ بِأَمْوَالِهِمْ وَأَنفُسِهِمْ أَعْظَمُ دَرَجَةً عِندَ اللَّهِ ۚ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَائِزُونَ
Ña nga xam ne dañoo gëm, gàddaay te ñuy xareel yoonu Yàlla ci joxe seeni alal walla seeni bakkan, ñooy ña gën a màgg dayo ya ca Yàlla... ñoom ñooy ñu texe ña.
21يُبَشِّرُهُمْ رَبُّهُم بِرَحْمَةٍ مِّنْهُ وَرِضْوَانٍ وَجَنَّاتٍ لَّهُمْ فِيهَا نَعِيمٌ مُّقِيمٌ
Seen Boroom a leen di bégale yërmaandeem ak ngërëmam, ak i Àjjana yu ñuy ame xéewal gu sax
22خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عِندَهُ أَجْرٌ عَظِيمٌ
dañu fay dëkk fàwwu. Pey gu màgg moo nekk fa Yàlla.
23يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّخِذُوا آبَاءَكُمْ وَإِخْوَانَكُمْ أَوْلِيَاءَ إِنِ اسْتَحَبُّوا الْكُفْرَ عَلَى الْإِيمَانِ ۚ وَمَن يَتَوَلَّهُم مِّنكُمْ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen def seeni baay ak seen mbokk yi ay xarit ndegam tànn nañu weddi, bàyyi ña gëm. Ku leen def xarit ca yéen... bokk na ca tooñkat ya.
24قُلْ إِن كَانَ آبَاؤُكُمْ وَأَبْنَاؤُكُمْ وَإِخْوَانُكُمْ وَأَزْوَاجُكُمْ وَعَشِيرَتُكُمْ وَأَمْوَالٌ اقْتَرَفْتُمُوهَا وَتِجَارَةٌ تَخْشَوْنَ كَسَادَهَا وَمَسَاكِنُ تَرْضَوْنَهَا أَحَبَّ إِلَيْكُم مِّنَ اللَّهِ وَرَسُولِهِ وَجِهَادٍ فِي سَبِيلِهِ فَتَرَبَّصُوا حَتَّىٰ يَأْتِيَ اللَّهُ بِأَمْرِهِ ۗ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
Neel [Yaw Yonent bi] : “Su fekkee ne seeni baay ak seeni doom, ak seeni mbokk, ak seeni jabar, ak seeni jegeñaale, ak alal ju ngeen fàggu, ak njaay mu ngeen ragal mu lamb, ak kër yu leen neex ngeen gën a bëgg ci Yàlla ak Yonentam ak xareel yoonu Yàlla, kon nangeen xaar ba Yàlla dikk ak dogalam. Yàlla du gindi nit ñu dëng”.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
22Aaya

Tekki — At-Tawba 22

Simoore At-Tawba Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : dañu fay dëkk fàwwu. Pey gu màgg moo nekk fa…

Simoore Aaya 22/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers