At-Tawba · 23/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّخِذُوا آبَاءَكُمْ وَإِخْوَانَكُمْ أَوْلِيَاءَ إِنِ اسْتَحَبُّوا الْكُفْرَ عَلَى الْإِيمَانِ ۚ وَمَن يَتَوَلَّهُم مِّنكُمْ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ ۝٢٣
Yaaa aiyuhal lazeena aamanoo laa tattakhizooo aabaaa `akum wa ikhwaanakum awliyaaa`a inis tahabbul kufra `alal eemaan; wa mai yatawal lahum minkum fa ulaaa`ika humuz zaalimoon
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen ñi gëm ! Buleen def seeni baay ak seen mbokk yi ay xarit ndegam tànn nañu weddi, bàyyi ña gëm. Ku leen def xarit ca yéen... bokk na ca tooñkat ya.
🎧 Dégg

📜 Aaya 21-25 — At-Tawba

21يُبَشِّرُهُمْ رَبُّهُم بِرَحْمَةٍ مِّنْهُ وَرِضْوَانٍ وَجَنَّاتٍ لَّهُمْ فِيهَا نَعِيمٌ مُّقِيمٌ
Seen Boroom a leen di bégale yërmaandeem ak ngërëmam, ak i Àjjana yu ñuy ame xéewal gu sax
22خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عِندَهُ أَجْرٌ عَظِيمٌ
dañu fay dëkk fàwwu. Pey gu màgg moo nekk fa Yàlla.
23يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّخِذُوا آبَاءَكُمْ وَإِخْوَانَكُمْ أَوْلِيَاءَ إِنِ اسْتَحَبُّوا الْكُفْرَ عَلَى الْإِيمَانِ ۚ وَمَن يَتَوَلَّهُم مِّنكُمْ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen def seeni baay ak seen mbokk yi ay xarit ndegam tànn nañu weddi, bàyyi ña gëm. Ku leen def xarit ca yéen... bokk na ca tooñkat ya.
24قُلْ إِن كَانَ آبَاؤُكُمْ وَأَبْنَاؤُكُمْ وَإِخْوَانُكُمْ وَأَزْوَاجُكُمْ وَعَشِيرَتُكُمْ وَأَمْوَالٌ اقْتَرَفْتُمُوهَا وَتِجَارَةٌ تَخْشَوْنَ كَسَادَهَا وَمَسَاكِنُ تَرْضَوْنَهَا أَحَبَّ إِلَيْكُم مِّنَ اللَّهِ وَرَسُولِهِ وَجِهَادٍ فِي سَبِيلِهِ فَتَرَبَّصُوا حَتَّىٰ يَأْتِيَ اللَّهُ بِأَمْرِهِ ۗ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
Neel [Yaw Yonent bi] : “Su fekkee ne seeni baay ak seeni doom, ak seeni mbokk, ak seeni jabar, ak seeni jegeñaale, ak alal ju ngeen fàggu, ak njaay mu ngeen ragal mu lamb, ak kër yu leen neex ngeen gën a bëgg ci Yàlla ak Yonentam ak xareel yoonu Yàlla, kon nangeen xaar ba Yàlla dikk ak dogalam. Yàlla du gindi nit ñu dëng”.
25لَقَدْ نَصَرَكُمُ اللَّهُ فِي مَوَاطِنَ كَثِيرَةٍ ۙ وَيَوْمَ حُنَيْنٍ ۙ إِذْ أَعْجَبَتْكُمْ كَثْرَتُكُمْ فَلَمْ تُغْنِ عَنكُمْ شَيْئًا وَضَاقَتْ عَلَيْكُمُ الْأَرْضُ بِمَا رَحُبَتْ ثُمَّ وَلَّيْتُم مُّدْبِرِينَ
Yàlla dimbali na leen ci barab yu bari. Ak ca bisu (xareb) Hunayni ba ngeen yéemoo ca nangeen baree woon te jariñuleen dara. Ba li suuf si di yaatu, lépp xat na keroog ci yéen ; ngeen wëlbatiku daw.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
23Aaya

Tekki — At-Tawba 23

Simoore At-Tawba Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen ñi gëm ! Buleen def seeni baay ak…

Simoore Aaya 23/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers