At-Tawba · 53/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
قُلْ أَنفِقُوا طَوْعًا أَوْ كَرْهًا لَّن يُتَقَبَّلَ مِنكُمْ ۖ إِنَّكُمْ كُنتُمْ قَوْمًا فَاسِقِينَ ۝٥٣
Qul anfiqoo taw`an aw karhal lany yutaqabbala min kum innakum kuntum qawman faasiqeen
📖 Tekkim Wolof
Waxal ne : “Génneleen seeni alal, mu neex walla mu naqari leen : ak lu mën a xew, Yàlla du ko nangu, te sax yéen ay saay-saay ngeen”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 51-55 — Simoore At-Tawba

51قُل لَّن يُصِيبَنَا إِلَّا مَا كَتَبَ اللَّهُ لَنَا هُوَ مَوْلَانَا ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ
Waxal ne : “Dara mënunoo dal lu dul lu Yàlla bind ci nun rekk. Te Mooy sunu Kilifa. Te it ñi gëm, nañuy wéeru ci Yàlla”.
52قُلْ هَلْ تَرَبَّصُونَ بِنَا إِلَّا إِحْدَى الْحُسْنَيَيْنِ ۖ وَنَحْنُ نَتَرَبَّصُ بِكُمْ أَن يُصِيبَكُمُ اللَّهُ بِعَذَابٍ مِّنْ عِندِهِ أَوْ بِأَيْدِينَا ۖ فَتَرَبَّصُوا إِنَّا مَعَكُم مُّتَرَبِّصُونَ
Waxal ne : “Yéen a ngi nuy tuŋlu, te nun lu mën a xew, dananu am benn ci ñaari ndam yi [dee Chahiid walla nu dàq leen, not leen], benn Yàlla mbugal leen ci sunuy loxo, walla Mu xaroo leen ko ba ëllëg. Kon book nanu ànd di tuŋlu”.
53قُلْ أَنفِقُوا طَوْعًا أَوْ كَرْهًا لَّن يُتَقَبَّلَ مِنكُمْ ۖ إِنَّكُمْ كُنتُمْ قَوْمًا فَاسِقِينَ
Waxal ne : “Génneleen seeni alal, mu neex walla mu naqari leen : ak lu mën a xew, Yàlla du ko nangu, te sax yéen ay saay-saay ngeen”.
54وَمَا مَنَعَهُمْ أَن تُقْبَلَ مِنْهُمْ نَفَقَاتُهُمْ إِلَّا أَنَّهُمْ كَفَرُوا بِاللَّهِ وَبِرَسُولِهِ وَلَا يَأْتُونَ الصَّلَاةَ إِلَّا وَهُمْ كُسَالَىٰ وَلَا يُنفِقُونَ إِلَّا وَهُمْ كَارِهُونَ
Li waral seen alal jooju Yàlla du ko nangu, moo di ne dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam, tàyyeel lool ci julli, nay lool ci li ñuy joxe.
55فَلَا تُعْجِبْكَ أَمْوَالُهُمْ وَلَا أَوْلَادُهُمْ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ لِيُعَذِّبَهُم بِهَا فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَتَزْهَقَ أَنفُسُهُمْ وَهُمْ كَافِرُونَ
Bula seeni alal yéem, naka noonu bula seeni doom yéem ! Yàlla nammul lu dul mbugal leen ci loolu ci dundug àddina si, ak ca roccig seeni ruu fekk ñu nekk di ay yéefar.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
53Aaya

Tekki — At-Tawba 53

Simoore At-Tawba Aaya 53 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waxal ne : “Génneleen seeni alal, mu neex walla mu…

Simoore Aaya 53/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 51–55. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers