At-Tawba · 84/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
وَلَا تُصَلِّ عَلَىٰ أَحَدٍ مِّنْهُم مَّاتَ أَبَدًا وَلَا تَقُمْ عَلَىٰ قَبْرِهِ ۖ إِنَّهُمْ كَفَرُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَمَاتُوا وَهُمْ فَاسِقُونَ ۝٨٤
Wa laa tusalli `alaaa ahadim minhum maata abadanw wa laa taqum `alaa qabriheee innahum kafaroo billaahi wa Rasoolihee wa maatoo wa hum faasiqoon
📖 Tekkim Wolof
Bul jullee kenn ku dee ci ñoom, te bul taxaw mukk ci bàmmeelam, ndax ñoom dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam ba ñuy dee, fekk ñu di ay saay-saay.

🎧 Dégg


📜 Aaya 82-86 — Simoore At-Tawba

82فَلْيَضْحَكُوا قَلِيلًا وَلْيَبْكُوا كَثِيرًا جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Nañuy ree lu néew (ci àddina), danañu jooy lu bari (ca àllaaxira) mu di seenug pey ca la ñu doon fàggu.
83فَإِن رَّجَعَكَ اللَّهُ إِلَىٰ طَائِفَةٍ مِّنْهُمْ فَاسْتَأْذَنُوكَ لِلْخُرُوجِ فَقُل لَّن تَخْرُجُوا مَعِيَ أَبَدًا وَلَن تُقَاتِلُوا مَعِيَ عَدُوًّا ۖ إِنَّكُمْ رَضِيتُم بِالْقُعُودِ أَوَّلَ مَرَّةٍ فَاقْعُدُوا مَعَ الْخَالِفِينَ
Bu la Yàlla delloo ci ab kurél ñoom, te ñu ñaan la ndigalul génn (ànd ak yaw), neeleen : “Dootuleen génn mukk di ànd ak man, te it dootuleen xare ak noon yi ànd ak man. Ndax yéen tànnoon ngeen toog ca njalbéen ga ; kon nag toogleen, ànd ak way-des ña ginnaaw”.
84وَلَا تُصَلِّ عَلَىٰ أَحَدٍ مِّنْهُم مَّاتَ أَبَدًا وَلَا تَقُمْ عَلَىٰ قَبْرِهِ ۖ إِنَّهُمْ كَفَرُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَمَاتُوا وَهُمْ فَاسِقُونَ
Bul jullee kenn ku dee ci ñoom, te bul taxaw mukk ci bàmmeelam, ndax ñoom dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam ba ñuy dee, fekk ñu di ay saay-saay.
85وَلَا تُعْجِبْكَ أَمْوَالُهُمْ وَأَوْلَادُهُمْ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ أَن يُعَذِّبَهُم بِهَا فِي الدُّنْيَا وَتَزْهَقَ أَنفُسُهُمْ وَهُمْ كَافِرُونَ
Bumu la yéem seeni alal ak seeni doom ! Yàlla Daleen a namm a mbugal ci yooyu ci àddina, te bu seeni ruu di rot fekk ñu di ay yéefar.
86وَإِذَا أُنزِلَتْ سُورَةٌ أَنْ آمِنُوا بِاللَّهِ وَجَاهِدُوا مَعَ رَسُولِهِ اسْتَأْذَنَكَ أُولُو الطَّوْلِ مِنْهُمْ وَقَالُوا ذَرْنَا نَكُن مَّعَ الْقَاعِدِينَ
Bu aw saar wàccee (di leen ñaax) ci gëm Yàlla ak ànd xare ak ub Yonentam, woroom alal ya ca ñoom di laaj ndigal, naan : “Bàyyinu nu ànd ak ñay toog”.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
84Aaya

Tekki — At-Tawba 84

Simoore At-Tawba Aaya 84 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bul jullee kenn ku dee ci ñoom, te bul taxaw…

Simoore Aaya 84/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 82–86. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers