At-Tawba · 85/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
وَلَا تُعْجِبْكَ أَمْوَالُهُمْ وَأَوْلَادُهُمْ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ أَن يُعَذِّبَهُم بِهَا فِي الدُّنْيَا وَتَزْهَقَ أَنفُسُهُمْ وَهُمْ كَافِرُونَ ۝٨٥
Wa laa tu`jibka amwaa luhum wa awlaaduhum; innamaa yureedul laahu ai yu`az zibahum bihaa fid dunyaa wa tazhaqa anfusuhum wa hum kaafiroon
📖 Tekkim Wolof
Bumu la yéem seeni alal ak seeni doom ! Yàlla Daleen a namm a mbugal ci yooyu ci àddina, te bu seeni ruu di rot fekk ñu di ay yéefar.

🎧 Dégg


📜 Aaya 83-87 — Simoore At-Tawba

83فَإِن رَّجَعَكَ اللَّهُ إِلَىٰ طَائِفَةٍ مِّنْهُمْ فَاسْتَأْذَنُوكَ لِلْخُرُوجِ فَقُل لَّن تَخْرُجُوا مَعِيَ أَبَدًا وَلَن تُقَاتِلُوا مَعِيَ عَدُوًّا ۖ إِنَّكُمْ رَضِيتُم بِالْقُعُودِ أَوَّلَ مَرَّةٍ فَاقْعُدُوا مَعَ الْخَالِفِينَ
Bu la Yàlla delloo ci ab kurél ñoom, te ñu ñaan la ndigalul génn (ànd ak yaw), neeleen : “Dootuleen génn mukk di ànd ak man, te it dootuleen xare ak noon yi ànd ak man. Ndax yéen tànnoon ngeen toog ca njalbéen ga ; kon nag toogleen, ànd ak way-des ña ginnaaw”.
84وَلَا تُصَلِّ عَلَىٰ أَحَدٍ مِّنْهُم مَّاتَ أَبَدًا وَلَا تَقُمْ عَلَىٰ قَبْرِهِ ۖ إِنَّهُمْ كَفَرُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَمَاتُوا وَهُمْ فَاسِقُونَ
Bul jullee kenn ku dee ci ñoom, te bul taxaw mukk ci bàmmeelam, ndax ñoom dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam ba ñuy dee, fekk ñu di ay saay-saay.
85وَلَا تُعْجِبْكَ أَمْوَالُهُمْ وَأَوْلَادُهُمْ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ أَن يُعَذِّبَهُم بِهَا فِي الدُّنْيَا وَتَزْهَقَ أَنفُسُهُمْ وَهُمْ كَافِرُونَ
Bumu la yéem seeni alal ak seeni doom ! Yàlla Daleen a namm a mbugal ci yooyu ci àddina, te bu seeni ruu di rot fekk ñu di ay yéefar.
86وَإِذَا أُنزِلَتْ سُورَةٌ أَنْ آمِنُوا بِاللَّهِ وَجَاهِدُوا مَعَ رَسُولِهِ اسْتَأْذَنَكَ أُولُو الطَّوْلِ مِنْهُمْ وَقَالُوا ذَرْنَا نَكُن مَّعَ الْقَاعِدِينَ
Bu aw saar wàccee (di leen ñaax) ci gëm Yàlla ak ànd xare ak ub Yonentam, woroom alal ya ca ñoom di laaj ndigal, naan : “Bàyyinu nu ànd ak ñay toog”.
87رَضُوا بِأَن يَكُونُوا مَعَ الْخَوَالِفِ وَطُبِعَ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَفْقَهُونَ
Neex na leen ñu ànd ak way-des ginnaaw ña. Tax na tëjeef na seeni xol ba ñoom dootuñu am dégg-dégg.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
85Aaya

Tekki — At-Tawba 85

Simoore At-Tawba Aaya 85 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bumu la yéem seeni alal ak seeni doom ! Yàlla…

Simoore Aaya 85/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 83–87. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers