Yunus · 20/109
Tekki Waxtaan — Yunus
وَيَقُولُونَ لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْهِ آيَةٌ مِّن رَّبِّهِ ۖ فَقُلْ إِنَّمَا الْغَيْبُ لِلَّهِ فَانتَظِرُوا إِنِّي مَعَكُم مِّنَ الْمُنتَظِرِينَ ۝٢٠
W yaqooloona law laaa unzila `alaihi aayatum mir Rabbihee faqul innamal ghaibu lillaahi fantaziroo innee ma`akum minal muntazireen
📖 Tekkim Wolof
Ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom laaya ju tukkee ca Boroomam ? ”. Neel : “Lu fàddu (di kumpa) Yàlla rekk a ko xam. Kon nanga muñandiku ; Man nag, maa ngi ànd ak yéen bokk ca way-muñandiku ña.
🎧 Dégg

📜 Aaya 18-22 — Yunus

18وَيَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَضُرُّهُمْ وَلَا يَنفَعُهُمْ وَيَقُولُونَ هَٰؤُلَاءِ شُفَعَاؤُنَا عِندَ اللَّهِ ۚ قُلْ أَتُنَبِّئُونَ اللَّهَ بِمَا لَا يَعْلَمُ فِي السَّمَاوَاتِ وَلَا فِي الْأَرْضِ ۚ سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يُشْرِكُونَ
Dañuy jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne duleen mën a lor, duleen mën a jariñ dara, ñuy wax naan : “Ñii ñoo nuy rammu fa Yàlla”. Neel : “Ndax dangeen a mën a xamal Yàlla lu Mu xamul ci asamaan yi ak suuf si ? ”. Kañ naa Ko, te kawe na lool la ñu Koy bokkaale !
19وَمَا كَانَ النَّاسُ إِلَّا أُمَّةً وَاحِدَةً فَاخْتَلَفُوا ۚ وَلَوْلَا كَلِمَةٌ سَبَقَتْ مِن رَّبِّكَ لَقُضِيَ بَيْنَهُمْ فِيمَا فِيهِ يَخْتَلِفُونَ
Nit ñi nekkuñu woon lu dul wenn xeet. Ñu juuyoo. Te bu dul koon waxi Yàlla ja jiitu woon, àttekoon na seeni diggante ca la ñu juuyoo.
20وَيَقُولُونَ لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْهِ آيَةٌ مِّن رَّبِّهِ ۖ فَقُلْ إِنَّمَا الْغَيْبُ لِلَّهِ فَانتَظِرُوا إِنِّي مَعَكُم مِّنَ الْمُنتَظِرِينَ
Ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom laaya ju tukkee ca Boroomam ? ”. Neel : “Lu fàddu (di kumpa) Yàlla rekk a ko xam. Kon nanga muñandiku ; Man nag, maa ngi ànd ak yéen bokk ca way-muñandiku ña.
21وَإِذَا أَذَقْنَا النَّاسَ رَحْمَةً مِّن بَعْدِ ضَرَّاءَ مَسَّتْهُمْ إِذَا لَهُم مَّكْرٌ فِي آيَاتِنَا ۚ قُلِ اللَّهُ أَسْرَعُ مَكْرًا ۚ إِنَّ رُسُلَنَا يَكْتُبُونَ مَا تَمْكُرُونَ
Su Nu musalee nit ci yërmaande [niki taw] ginnaaw ba leen naqar dalee, ñuy def i pexe ci Sunuy tegtal. Neel : “Yàllaa gën a gaaw ciy pexe”. Sunuy ndaw danañu bind li ngeen di fexe de.
22هُوَ الَّذِي يُسَيِّرُكُمْ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا كُنتُمْ فِي الْفُلْكِ وَجَرَيْنَ بِهِم بِرِيحٍ طَيِّبَةٍ وَفَرِحُوا بِهَا جَاءَتْهَا رِيحٌ عَاصِفٌ وَجَاءَهُمُ الْمَوْجُ مِن كُلِّ مَكَانٍ وَظَنُّوا أَنَّهُمْ أُحِيطَ بِهِمْ ۙ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ لَئِنْ أَنجَيْتَنَا مِنْ هَٰذِهِ لَنَكُونَنَّ مِنَ الشَّاكِرِينَ
Moom mooy ki leen doxloo, ci suuf si ak ci géej gi, ba ngeen nekkee ca gaal ga. Te gaal googu daw ak ñoom ci ngelaw lu teey. Ñu bég ca ba ngelaw lu tar songu leen, duusi géej wër leen ci wet gu nekk, ba ñu njortu ne ñoom alageef na leen, ñuy ñaan Yàlla, di sellal diineem, di [giñ] ne: “Boo Nu musalee ci lii, fàwwu dananu bokk ci way-sant ña [Yàlla] ! ”
YunusFihi Alxuraan
109Aaya
MeccanRevelation
20Aaya

Tekki — Yunus 20

Simoore Yunus Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci…

Simoore Aaya 20/109 — Yunus يونس (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yunus Dégg, Yunus Tekki, Yunus mp3, Yunus pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers