Hud · 71/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَامْرَأَتُهُ قَائِمَةٌ فَضَحِكَتْ فَبَشَّرْنَاهَا بِإِسْحَاقَ وَمِن وَرَاءِ إِسْحَاقَ يَعْقُوبَ ۝٧١
Wamra atuhoo qaaa`imatun fadahikat fabashsharnaahaa bi Ishaaqa wa minw waraaa`i Ishaaqa Ya`qoob
📖 Tekkim Wolof
Noona soxnaam sa taxawoon [foofa] daldi ree ; Nu bégal ko [te xamal ko ne dana am doom ju tudd] Isaaqa, ak ci ginnaawam Isaaqa, Yanqooba.
🎧 Dégg

📜 Aaya 69-73 — Hud

69وَلَقَدْ جَاءَتْ رُسُلُنَا إِبْرَاهِيمَ بِالْبُشْرَىٰ قَالُوا سَلَامًا ۖ قَالَ سَلَامٌ ۖ فَمَا لَبِثَ أَن جَاءَ بِعِجْلٍ حَنِيذٍ
Sunuy ndaw indiloon na Ibraahiima mbégte, ñu ne ko : “Jàmmi Yàlla na nekk ci yaw ! ”. Mu ne leen : “Jàmm ci yéen it ! ”, nis tuut mu indil leen sëll wu ñu wàjj.
70فَلَمَّا رَأَىٰ أَيْدِيَهُمْ لَا تَصِلُ إِلَيْهِ نَكِرَهُمْ وَأَوْجَسَ مِنْهُمْ خِيفَةً ۚ قَالُوا لَا تَخَفْ إِنَّا أُرْسِلْنَا إِلَىٰ قَوْمِ لُوطٍ
Ba mu gisee ne seeni yoxo laalu ko, mu am tuuma ak ug tiit ci ñoom. Ñu ne ko : “Bul ragal, nun kat dañunoo yónni ca nitu Lóot ñi”.
71وَامْرَأَتُهُ قَائِمَةٌ فَضَحِكَتْ فَبَشَّرْنَاهَا بِإِسْحَاقَ وَمِن وَرَاءِ إِسْحَاقَ يَعْقُوبَ
Noona soxnaam sa taxawoon [foofa] daldi ree ; Nu bégal ko [te xamal ko ne dana am doom ju tudd] Isaaqa, ak ci ginnaawam Isaaqa, Yanqooba.
72قَالَتْ يَا وَيْلَتَىٰ أَأَلِدُ وَأَنَا عَجُوزٌ وَهَٰذَا بَعْلِي شَيْخًا ۖ إِنَّ هَٰذَا لَشَيْءٌ عَجِيبٌ
Mu wax ne : “Cëy man ! Ndax danaa jurati doom te màggat naa, sama boroom-kër bii it di ku mage ? Lii dey mbir mu doy waar la ! ”
73قَالُوا أَتَعْجَبِينَ مِنْ أَمْرِ اللَّهِ ۖ رَحْمَتُ اللَّهِ وَبَرَكَاتُهُ عَلَيْكُمْ أَهْلَ الْبَيْتِ ۚ إِنَّهُ حَمِيدٌ مَّجِيدٌ
Ñu ne ko : “Ndax dangay yéemu ci mbiru Yàlla ? Yërmaandey Yàlla ak barkeem, yal na nekk ci yéen waa kër gi ! Moom Yàlla moo yeyoo cant ak màggal ko ! ”
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
71Aaya

Tekki — Hud 71

Simoore Hud Aaya 71 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Noona soxnaam sa taxawoon [foofa] daldi ree ; Nu bégal…

Simoore Aaya 71/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 69–73. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers