An-Nahl · 63/128
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nahl
تَاللَّهِ لَقَدْ أَرْسَلْنَا إِلَىٰ أُمَمٍ مِّن قَبْلِكَ فَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ فَهُوَ وَلِيُّهُمُ الْيَوْمَ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝٦٣
Tallaahi laqad arsalnaaa ilaaa umamim min qablika fazayyana lahumush Shaitaanu a`maalahum fahuwa waliyyuhumul yawma wa lahum `azaabun aleem
📖 Tekkim Wolof
Giñ Nanu Nun Yàlla ne yónni woon Nanu ay Yonent cay xeet ya la jiitu. Waaye Séytaane rafetalal leen seeni jëf ba faf mu nekk tey seeni àndandoo. Te ñeel na leen mbugal mu metti.

🎧 Dégg


📜 Aaya 61-65 — Simoore An-Nahl

61وَلَوْ يُؤَاخِذُ اللَّهُ النَّاسَ بِظُلْمِهِم مَّا تَرَكَ عَلَيْهَا مِن دَابَّةٍ وَلَٰكِن يُؤَخِّرُهُمْ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۖ فَإِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ لَا يَسْتَأْخِرُونَ سَاعَةً ۖ وَلَا يَسْتَقْدِمُونَ
Bu Yàlla [doon] gaaw a duma nit ñi ngir seen tooñeel, kon du bàyyi kenn ci kaw suuf si. Waaye Dafa leen ci yeexe ba ci àpp bu ñu dogal ba noppi. Kon bu seen àpp agsee, duñu ko weesu mbaa ñu jiitu ko wenn waxtu.
62وَيَجْعَلُونَ لِلَّهِ مَا يَكْرَهُونَ وَتَصِفُ أَلْسِنَتُهُمُ الْكَذِبَ أَنَّ لَهُمُ الْحُسْنَىٰ ۖ لَا جَرَمَ أَنَّ لَهُمُ النَّارَ وَأَنَّهُم مُّفْرَطُونَ
Ñangay sédd Yàlla la ñu sib ñoom. Te seeni làmmiñ di sos i fen naan ñoo moom Àjjana. Te ca dëgg-dëgg ñoo yeyoo Safara te ñoo cay jiitu.
63تَاللَّهِ لَقَدْ أَرْسَلْنَا إِلَىٰ أُمَمٍ مِّن قَبْلِكَ فَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ فَهُوَ وَلِيُّهُمُ الْيَوْمَ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Giñ Nanu Nun Yàlla ne yónni woon Nanu ay Yonent cay xeet ya la jiitu. Waaye Séytaane rafetalal leen seeni jëf ba faf mu nekk tey seeni àndandoo. Te ñeel na leen mbugal mu metti.
64وَمَا أَنزَلْنَا عَلَيْكَ الْكِتَابَ إِلَّا لِتُبَيِّنَ لَهُمُ الَّذِي اخْتَلَفُوا فِيهِ ۙ وَهُدًى وَرَحْمَةً لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Wàccewuñu ci yaaw Téere [Alxuraan] ba lu dul ngir nga leeralal leen la ñu nekkoon ci juuyoo, ak ngir mu nekk di njub ak yërmaande ci nit ñu gëm.
65وَاللَّهُ أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّقَوْمٍ يَسْمَعُونَ
Te Yàlla moo wàcce ndox mu jóge ca kaw, mu dundal ci suuf si ginnaaw ba mu bekkooree. Te nekk na ci loolu tegtal ci nit ñuy dégg.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
63Aaya

Tekki — An-Nahl 63

Simoore An-Nahl Aaya 63 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Giñ Nanu Nun Yàlla ne yónni woon Nanu ay Yonent…

Simoore Aaya 63/128 — Simoore An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nahl Dégg, Simoore An-Nahl Tekki, Simoore An-Nahl mp3, Simoore An-Nahl pdf. Aaya 61–65. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers