Al-Isra · 89/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
وَلَقَدْ صَرَّفْنَا لِلنَّاسِ فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ مِن كُلِّ مَثَلٍ فَأَبَىٰ أَكْثَرُ النَّاسِ إِلَّا كُفُورًا ۝٨٩
Qa laqad sarrafnaa linnaasi fee haazal quraani min kulli masalin fa abaaa aksarun naasi illaa kufooraa
📖 Tekkim Wolof
Te ca dëgg-dëgg, jox Nanu nit ñi ci Alxuraan jii léebu wu ne [wuy leeral]. Waaye terewul li ëpp ci ñoom wéy di weddi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 87-91 — Simoore Al-Isra

87إِلَّا رَحْمَةً مِّن رَّبِّكَ ۚ إِنَّ فَضْلَهُ كَانَ عَلَيْكَ كَبِيرًا
Lu dul yërmaande ju jóge ci sa Boroom, te ngënéelam li Mu la jagleel rëy na [ba tax na Mu bàyyee la xam-xam bi bañ koo rocci].
88قُل لَّئِنِ اجْتَمَعَتِ الْإِنسُ وَالْجِنُّ عَلَىٰ أَن يَأْتُوا بِمِثْلِ هَٰذَا الْقُرْآنِ لَا يَأْتُونَ بِمِثْلِهِ وَلَوْ كَانَ بَعْضُهُمْ لِبَعْضٍ ظَهِيرًا
Neel : “Bu nit ak jinne booloo woon ngir fexee indi lu mel ni Alxuraan jii, duñu mën a indi lu ni mel, doonte dañu caa dimbalante”.
89وَلَقَدْ صَرَّفْنَا لِلنَّاسِ فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ مِن كُلِّ مَثَلٍ فَأَبَىٰ أَكْثَرُ النَّاسِ إِلَّا كُفُورًا
Te ca dëgg-dëgg, jox Nanu nit ñi ci Alxuraan jii léebu wu ne [wuy leeral]. Waaye terewul li ëpp ci ñoom wéy di weddi.
90وَقَالُوا لَن نُّؤْمِنَ لَكَ حَتَّىٰ تَفْجُرَ لَنَا مِنَ الْأَرْضِ يَنبُوعًا
Ñu naan : “Duñu gëm mukk li feek ballaloonu ci suuf si ay seewnde [bëti ndox] ;
91أَوْ تَكُونَ لَكَ جَنَّةٌ مِّن نَّخِيلٍ وَعِنَبٍ فَتُفَجِّرَ الْأَنْهَارَ خِلَالَهَا تَفْجِيرًا
walla nga am tooli garabi tàndarma ak garabu reseñ, nga ballal ay dex ci seen diggante yuy ball bu baax ;
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
89Aaya

Tekki — Al-Isra 89

Simoore Al-Isra Aaya 89 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te ca dëgg-dëgg, jox Nanu nit ñi ci Alxuraan jii…

Simoore Aaya 89/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 87–91. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers