Al-Baqara · 131/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
إِذْ قَالَ لَهُ رَبُّهُ أَسْلِمْ ۖ قَالَ أَسْلَمْتُ لِرَبِّ الْعَالَمِينَ ۝١٣١
Iz qaala lahoo Rabbuhooo aslim qaala aslamtu li Rabbil `aalameen
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikuleen] Ba ko Boroomam nee : “Wommatul”, Mu ne : “Wommatunaa jëm ci Boroom àddina bi”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 129-133 — Simoore Al-Baqara

129رَبَّنَا وَابْعَثْ فِيهِمْ رَسُولًا مِّنْهُمْ يَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِكَ وَيُعَلِّمُهُمُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَيُزَكِّيهِمْ ۚ إِنَّكَ أَنتَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Yaw sunu Boroom ! Yónneel ci ñoom Yonent bu bokk ci ñoom, bu leen di jàngal say laaya, di leen xamal Téere ba ak i xereñe, te di leen sellal Yaw Aji-not ji , Aji-xereñ ji!
130وَمَن يَرْغَبُ عَن مِّلَّةِ إِبْرَاهِيمَ إِلَّا مَن سَفِهَ نَفْسَهُ ۚ وَلَقَدِ اصْطَفَيْنَاهُ فِي الدُّنْيَا ۖ وَإِنَّهُ فِي الْآخِرَةِ لَمِنَ الصَّالِحِينَ
Ana kan mooy bañ diinay Ibraahiima, ku dul ku kannasu ? Nun dey tànn nanu ko ci àddina ; te moom, bu àllaaxiraa it, mu bokk ca ña gën a yiw.
131إِذْ قَالَ لَهُ رَبُّهُ أَسْلِمْ ۖ قَالَ أَسْلَمْتُ لِرَبِّ الْعَالَمِينَ
[Fàttalikuleen] Ba ko Boroomam nee : “Wommatul”, Mu ne : “Wommatunaa jëm ci Boroom àddina bi”.
132وَوَصَّىٰ بِهَا إِبْرَاهِيمُ بَنِيهِ وَيَعْقُوبُ يَا بَنِيَّ إِنَّ اللَّهَ اصْطَفَىٰ لَكُمُ الدِّينَ فَلَا تَمُوتُنَّ إِلَّا وَأَنتُم مُّسْلِمُونَ
Ibraahiima dénk na ay doomam solo sa, ak Yanqooba, ne leen: “Yéen samay doom, Yàllaa leen tànnal diine de, buleen dee lu dul na fekk ngeen wommatu jëm ca Yàlla” !.
133أَمْ كُنتُمْ شُهَدَاءَ إِذْ حَضَرَ يَعْقُوبَ الْمَوْتُ إِذْ قَالَ لِبَنِيهِ مَا تَعْبُدُونَ مِن بَعْدِي قَالُوا نَعْبُدُ إِلَٰهَكَ وَإِلَٰهَ آبَائِكَ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ إِلَٰهًا وَاحِدًا وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ
walla sax fekkee woon ngeen ba dee ga dikkalee (Janqooba) te mu ne: “Éy samay doom, ana lan ngeen di xala jaamu sama ginnaaw” ? - Ñu ne : “Dananu jaamu Yàlla sa Boroom tey Yàllaay say baay Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa, di jenn Yàlla doŋŋ te nun way-wommatu lanu, jëm ci Moom”.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
131Aaya

Tekki — Al-Baqara 131

Simoore Al-Baqara Aaya 131 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikuleen] Ba ko Boroomam nee : “Wommatul”, Mu ne :…

Simoore Aaya 131/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 129–133. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers