Al-Baqara · 263/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
۞ قَوْلٌ مَّعْرُوفٌ وَمَغْفِرَةٌ خَيْرٌ مِّن صَدَقَةٍ يَتْبَعُهَا أَذًى ۗ وَاللَّهُ غَنِيٌّ حَلِيمٌ ۝٢٦٣
Qawlum ma`roofunw wa maghfiratun khairum min sadaqatiny yatba`uhaaa azaa; wallaahu Ghaniyyun Haleem
📖 Tekkim Wolof
Wax ju yiw ak ag njeggal moo gëm sarax boo xam ne wax ju ñaaw a ca topp. Yàlla ku woomal la, ku lewet la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 261-265 — Al-Baqara

261مَّثَلُ الَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ كَمَثَلِ حَبَّةٍ أَنبَتَتْ سَبْعَ سَنَابِلَ فِي كُلِّ سُنبُلَةٍ مِّائَةُ حَبَّةٍ ۗ وَاللَّهُ يُضَاعِفُ لِمَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Méngaleg ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci yoonu Yàlla mi ngi deme ni wenn pepp wu sax, seqi juróom-ñaari gupp, gupp wu nekk am téeméeri fepp. Yàlla mooy fulal ku ko soob,Yàlla ku yaatu ku xam la.
262الَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ثُمَّ لَا يُتْبِعُونَ مَا أَنفَقُوا مَنًّا وَلَا أَذًى ۙ لَّهُمْ أَجْرُهُمْ عِندَ رَبِّهِمْ وَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci yoonu Yàlla te duñu toftale ca la ñu joxe ñax walla kañu , danañu am seenug pey fa Yàlla seen Boroom. Duñu tiit, duñu jàq.
263۞ قَوْلٌ مَّعْرُوفٌ وَمَغْفِرَةٌ خَيْرٌ مِّن صَدَقَةٍ يَتْبَعُهَا أَذًى ۗ وَاللَّهُ غَنِيٌّ حَلِيمٌ
Wax ju yiw ak ag njeggal moo gëm sarax boo xam ne wax ju ñaaw a ca topp. Yàlla ku woomal la, ku lewet la.
264يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تُبْطِلُوا صَدَقَاتِكُم بِالْمَنِّ وَالْأَذَىٰ كَالَّذِي يُنفِقُ مَالَهُ رِئَاءَ النَّاسِ وَلَا يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ ۖ فَمَثَلُهُ كَمَثَلِ صَفْوَانٍ عَلَيْهِ تُرَابٌ فَأَصَابَهُ وَابِلٌ فَتَرَكَهُ صَلْدًا ۖ لَّا يَقْدِرُونَ عَلَىٰ شَيْءٍ مِّمَّا كَسَبُوا ۗ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْكَافِرِينَ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen yàq seeni sarax ci ñax ak kañu, képp ku joxe alal ngir ngistal ci nit ña te gëmul Bis-pénc ba. Dafay mel ni doj wu suuf tegu ca kawam ; waame sottiku ca, bàyyi ko mu ratax bandaŋ. [nit ñu mel noonu] duñu mën a def dara lu barkeel. Te Yàlla du gindi nit ñu weddi.
265وَمَثَلُ الَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمُ ابْتِغَاءَ مَرْضَاتِ اللَّهِ وَتَثْبِيتًا مِّنْ أَنفُسِهِمْ كَمَثَلِ جَنَّةٍ بِرَبْوَةٍ أَصَابَهَا وَابِلٌ فَآتَتْ أُكُلَهَا ضِعْفَيْنِ فَإِن لَّمْ يُصِبْهَا وَابِلٌ فَطَلٌّ ۗ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Melow ñi joxe seeni alal ngir sàkku ngërëmul Yàlla, ak saxal seeni bakkan ci jaamu Yàlla, dafa mel ni tool bu nekk ci aw tund. Waame [taw] dal ca, mu génne ñaari yoon meññeefam ; bu ca waame dalul itam, mësay ma naatal ko. Yàllaa ngi ne jàkk ci li ngeen di def.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
263Aaya

Tekki — Al-Baqara 263

Simoore Al-Baqara Aaya 263 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Wax ju yiw ak ag njeggal moo gëm sarax boo…

Simoore Aaya 263/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 261–265. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers