Al-Anbiya · 22/112
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anbiya
لَوْ كَانَ فِيهِمَا آلِهَةٌ إِلَّا اللَّهُ لَفَسَدَتَا ۚ فَسُبْحَانَ اللَّهِ رَبِّ الْعَرْشِ عَمَّا يَصِفُونَ ۝٢٢
Law kaana feehimaaa aalihatun illal laahu lafasadataa; fa-Subhaanal laahi Rabbil `Arshi `ammaa yasifoon
📖 Tekkim Wolof
Su jeneen yàlla ju dul Yàlla amoon ci asamaan yeek suuf si, kon ñoom ñaar ñépp yàqu. Cëy sellam ga, Mooy Boroom Gàngunaay ga [Aras] ; Jomb na li ñu koy nirale !

🎧 Dégg


📜 Aaya 20-24 — Simoore Al-Anbiya

20يُسَبِّحُونَ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ لَا يَفْتُرُونَ
Dañu Koy sàbbaal guddi ak bëccëg, duñu ca jóge.
21أَمِ اتَّخَذُوا آلِهَةً مِّنَ الْأَرْضِ هُمْ يُنشِرُونَ
Ndax ñoom dañuy jaamu ay yàlla ci suuf si [yuy mën a dekkal ku dee ni Boroom bi] ? [Mukk du am]
22لَوْ كَانَ فِيهِمَا آلِهَةٌ إِلَّا اللَّهُ لَفَسَدَتَا ۚ فَسُبْحَانَ اللَّهِ رَبِّ الْعَرْشِ عَمَّا يَصِفُونَ
Su jeneen yàlla ju dul Yàlla amoon ci asamaan yeek suuf si, kon ñoom ñaar ñépp yàqu. Cëy sellam ga, Mooy Boroom Gàngunaay ga [Aras] ; Jomb na li ñu koy nirale !
23لَا يُسْأَلُ عَمَّا يَفْعَلُ وَهُمْ يُسْأَلُونَ
Deefu ko sañ a laaj ci li Muy def, waaye ñoom la ñuy sañ a laaj.
24أَمِ اتَّخَذُوا مِن دُونِهِ آلِهَةً ۖ قُلْ هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ ۖ هَٰذَا ذِكْرُ مَن مَّعِيَ وَذِكْرُ مَن قَبْلِي ۗ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْلَمُونَ الْحَقَّ ۖ فَهُم مُّعْرِضُونَ
Am dañuy jaamu ay yàlla bàyyi Ko ? Neel : “Indileen seenu lay”. Lii [Alxuraan jii] mooy lépp lu ñuy waare képp ku ànd ak man, moo di li ñu waare woon it ña ma jiitu. Li ëpp ci ñoom xamuñu dëgg, tax na ñu dummóoyu.
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
22Aaya

Tekki — Al-Anbiya 22

Simoore Al-Anbiya Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Su jeneen yàlla ju dul Yàlla amoon ci asamaan yeek…

Simoore Aaya 22/112 — Simoore Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anbiya Dégg, Simoore Al-Anbiya Tekki, Simoore Al-Anbiya mp3, Simoore Al-Anbiya pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers