Al-Anbiya · 23/112
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anbiya
لَا يُسْأَلُ عَمَّا يَفْعَلُ وَهُمْ يُسْأَلُونَ ۝٢٣
Laa yus`alu `ammaa yaf`alu wa hum yus`aloon
📖 Tekkim Wolof
Deefu ko sañ a laaj ci li Muy def, waaye ñoom la ñuy sañ a laaj.

🎧 Dégg


📜 Aaya 21-25 — Simoore Al-Anbiya

21أَمِ اتَّخَذُوا آلِهَةً مِّنَ الْأَرْضِ هُمْ يُنشِرُونَ
Ndax ñoom dañuy jaamu ay yàlla ci suuf si [yuy mën a dekkal ku dee ni Boroom bi] ? [Mukk du am]
22لَوْ كَانَ فِيهِمَا آلِهَةٌ إِلَّا اللَّهُ لَفَسَدَتَا ۚ فَسُبْحَانَ اللَّهِ رَبِّ الْعَرْشِ عَمَّا يَصِفُونَ
Su jeneen yàlla ju dul Yàlla amoon ci asamaan yeek suuf si, kon ñoom ñaar ñépp yàqu. Cëy sellam ga, Mooy Boroom Gàngunaay ga [Aras] ; Jomb na li ñu koy nirale !
23لَا يُسْأَلُ عَمَّا يَفْعَلُ وَهُمْ يُسْأَلُونَ
Deefu ko sañ a laaj ci li Muy def, waaye ñoom la ñuy sañ a laaj.
24أَمِ اتَّخَذُوا مِن دُونِهِ آلِهَةً ۖ قُلْ هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ ۖ هَٰذَا ذِكْرُ مَن مَّعِيَ وَذِكْرُ مَن قَبْلِي ۗ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْلَمُونَ الْحَقَّ ۖ فَهُم مُّعْرِضُونَ
Am dañuy jaamu ay yàlla bàyyi Ko ? Neel : “Indileen seenu lay”. Lii [Alxuraan jii] mooy lépp lu ñuy waare képp ku ànd ak man, moo di li ñu waare woon it ña ma jiitu. Li ëpp ci ñoom xamuñu dëgg, tax na ñu dummóoyu.
25وَمَا أَرْسَلْنَا مِن قَبْلِكَ مِن رَّسُولٍ إِلَّا نُوحِي إِلَيْهِ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا أَنَا فَاعْبُدُونِ
Yónniwunu la la jiitu benn Yonent te soloowunu ko [lay dëgg] te moo di : “Amul jeneen yàlla ju dul Man. Kon jaamuleen Ko”.
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
23Aaya

Tekki — Al-Anbiya 23

Simoore Al-Anbiya Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Deefu ko sañ a laaj ci li Muy def, waaye…

Simoore Aaya 23/112 — Simoore Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anbiya Dégg, Simoore Al-Anbiya Tekki, Simoore Al-Anbiya mp3, Simoore Al-Anbiya pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers