Al-Anbiya · 26/112
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anbiya
وَقَالُوا اتَّخَذَ الرَّحْمَٰنُ وَلَدًا ۗ سُبْحَانَهُ ۚ بَلْ عِبَادٌ مُّكْرَمُونَ ۝٢٦
Wa qaalut takhazar Rahmaanu waladan Subhaanah; bal `ibaadum mkkramoon
📖 Tekkim Wolof
Ñiy wax naan : “Jërëmaakoon bi am na doom”. Cëy sellam ga ! Déet, ay jaam lañu yu Nu teral [ñoom Malaaka ya].

🎧 Dégg


📜 Aaya 24-28 — Simoore Al-Anbiya

24أَمِ اتَّخَذُوا مِن دُونِهِ آلِهَةً ۖ قُلْ هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ ۖ هَٰذَا ذِكْرُ مَن مَّعِيَ وَذِكْرُ مَن قَبْلِي ۗ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْلَمُونَ الْحَقَّ ۖ فَهُم مُّعْرِضُونَ
Am dañuy jaamu ay yàlla bàyyi Ko ? Neel : “Indileen seenu lay”. Lii [Alxuraan jii] mooy lépp lu ñuy waare képp ku ànd ak man, moo di li ñu waare woon it ña ma jiitu. Li ëpp ci ñoom xamuñu dëgg, tax na ñu dummóoyu.
25وَمَا أَرْسَلْنَا مِن قَبْلِكَ مِن رَّسُولٍ إِلَّا نُوحِي إِلَيْهِ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا أَنَا فَاعْبُدُونِ
Yónniwunu la la jiitu benn Yonent te soloowunu ko [lay dëgg] te moo di : “Amul jeneen yàlla ju dul Man. Kon jaamuleen Ko”.
26وَقَالُوا اتَّخَذَ الرَّحْمَٰنُ وَلَدًا ۗ سُبْحَانَهُ ۚ بَلْ عِبَادٌ مُّكْرَمُونَ
Ñiy wax naan : “Jërëmaakoon bi am na doom”. Cëy sellam ga ! Déet, ay jaam lañu yu Nu teral [ñoom Malaaka ya].
27لَا يَسْبِقُونَهُ بِالْقَوْلِ وَهُم بِأَمْرِهِ يَعْمَلُونَ
Duñu ko jiitu ci wax te ñoom ndigalam lañuy def.
28يَعْلَمُ مَا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُمْ وَلَا يَشْفَعُونَ إِلَّا لِمَنِ ارْتَضَىٰ وَهُم مِّنْ خَشْيَتِهِ مُشْفِقُونَ
Xam na li nekk ci seen kanam ak li nekk ci seen ginnaaw. Te duñu rammu lu dul ka Ko neex, te ñoom ña nga ca tiitaangey ragal Yàlla.
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
26Aaya

Tekki — Al-Anbiya 26

Simoore Al-Anbiya Aaya 26 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñiy wax naan : “Jërëmaakoon bi am na doom”. Cëy…

Simoore Aaya 26/112 — Simoore Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anbiya Dégg, Simoore Al-Anbiya Tekki, Simoore Al-Anbiya mp3, Simoore Al-Anbiya pdf. Aaya 24–28. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers