Al-Anbiya · 27/112
Tekki Waxtaan — Al-Anbiya
لَا يَسْبِقُونَهُ بِالْقَوْلِ وَهُم بِأَمْرِهِ يَعْمَلُونَ ۝٢٧
Laa yasbiqoonahoo bil qawli wa hum bi amrihee ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Duñu ko jiitu ci wax te ñoom ndigalam lañuy def.

🎧 Dégg


📜 Aaya 25-29 — Al-Anbiya

25وَمَا أَرْسَلْنَا مِن قَبْلِكَ مِن رَّسُولٍ إِلَّا نُوحِي إِلَيْهِ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا أَنَا فَاعْبُدُونِ
Yónniwunu la la jiitu benn Yonent te soloowunu ko [lay dëgg] te moo di : “Amul jeneen yàlla ju dul Man. Kon jaamuleen Ko”.
26وَقَالُوا اتَّخَذَ الرَّحْمَٰنُ وَلَدًا ۗ سُبْحَانَهُ ۚ بَلْ عِبَادٌ مُّكْرَمُونَ
Ñiy wax naan : “Jërëmaakoon bi am na doom”. Cëy sellam ga ! Déet, ay jaam lañu yu Nu teral [ñoom Malaaka ya].
27لَا يَسْبِقُونَهُ بِالْقَوْلِ وَهُم بِأَمْرِهِ يَعْمَلُونَ
Duñu ko jiitu ci wax te ñoom ndigalam lañuy def.
28يَعْلَمُ مَا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُمْ وَلَا يَشْفَعُونَ إِلَّا لِمَنِ ارْتَضَىٰ وَهُم مِّنْ خَشْيَتِهِ مُشْفِقُونَ
Xam na li nekk ci seen kanam ak li nekk ci seen ginnaaw. Te duñu rammu lu dul ka Ko neex, te ñoom ña nga ca tiitaangey ragal Yàlla.
29۞ وَمَن يَقُلْ مِنْهُمْ إِنِّي إِلَٰهٌ مِّن دُونِهِ فَذَٰلِكَ نَجْزِيهِ جَهَنَّمَ ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي الظَّالِمِينَ
Te ku ca waxoon bokk ca ñoom ne : “Man yàlla laa, ju dul Moom”. Loola Safara la Nu ko koy feyee. Te noona it la Nuy feye tooñkat ya.
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
27Aaya

Tekki — Al-Anbiya 27

Simoore Al-Anbiya Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Duñu ko jiitu ci wax te ñoom ndigalam lañuy def.

Simoore Aaya 27/112 — Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anbiya Dégg, Al-Anbiya Tekki, Al-Anbiya mp3, Al-Anbiya pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers