An-Naml · 87/93
Tekki Waxtaan — An-Naml
وَيَوْمَ يُنفَخُ فِي الصُّورِ فَفَزِعَ مَن فِي السَّمَاوَاتِ وَمَن فِي الْأَرْضِ إِلَّا مَن شَاءَ اللَّهُ ۚ وَكُلٌّ أَتَوْهُ دَاخِرِينَ ۝٨٧
Wa Yawma yunfakhu fis Soori fafazi`a man fis samaawaati wa man fil ardi illaa man shaaa`al laah; wa kullun atawhu daakhireen
📖 Tekkim Wolof
Bu keroogee Bis ba ñuy wal buftu bi, ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ñoom ñépp danañu tiit, ku dul ku soob Yàlla ! – Ñoom ñépp danañu dikk fa Yàlla te tott.

🎧 Dégg


📜 Aaya 85-89 — An-Naml

85وَوَقَعَ الْقَوْلُ عَلَيْهِم بِمَا ظَلَمُوا فَهُمْ لَا يَنطِقُونَ
Su wax ja agsee ci ñoom, seen tooñ ga dana tax duñu àddu.
86أَلَمْ يَرَوْا أَنَّا جَعَلْنَا اللَّيْلَ لِيَسْكُنُوا فِيهِ وَالنَّهَارَ مُبْصِرًا ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Ndax dañoo gisul ne [Man Yàlla] maa leen defal guddi ngir ñu di ca dal-lu, def bëccëg muy yëngukaay ? Ay kéemaan nekk na ci biir loolu ngir ñi gëm.
87وَيَوْمَ يُنفَخُ فِي الصُّورِ فَفَزِعَ مَن فِي السَّمَاوَاتِ وَمَن فِي الْأَرْضِ إِلَّا مَن شَاءَ اللَّهُ ۚ وَكُلٌّ أَتَوْهُ دَاخِرِينَ
Bu keroogee Bis ba ñuy wal buftu bi, ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ñoom ñépp danañu tiit, ku dul ku soob Yàlla ! – Ñoom ñépp danañu dikk fa Yàlla te tott.
88وَتَرَى الْجِبَالَ تَحْسَبُهَا جَامِدَةً وَهِيَ تَمُرُّ مَرَّ السَّحَابِ ۚ صُنْعَ اللَّهِ الَّذِي أَتْقَنَ كُلَّ شَيْءٍ ۚ إِنَّهُ خَبِيرٌ بِمَا تَفْعَلُونَ
Ngay gis tundi doj yi foog ni dafa taxaw benn barab, te fekk na booba ñangay daw niw niir. Loolu mooy liggéeyub Yàlla. Te Mooy Xereñaakoonub mépp mbir, te Ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def !
89مَن جَاءَ بِالْحَسَنَةِ فَلَهُ خَيْرٌ مِّنْهَا وَهُم مِّن فَزَعٍ يَوْمَئِذٍ آمِنُونَ
Moo ndax du ku indi ag yiw dana ca ame pey gu ko gën, te bu Bis-pénc baa dana mucc ci am tiit.
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
87Aaya

Tekki — An-Naml 87

Simoore An-Naml Aaya 87 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu keroogee Bis ba ñuy wal buftu bi, ñi nekk…

Simoore Aaya 87/93 — An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Naml Dégg, An-Naml Tekki, An-Naml mp3, An-Naml pdf. Aaya 85–89. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers