Al-Qasas · 46/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
وَمَا كُنتَ بِجَانِبِ الطُّورِ إِذْ نَادَيْنَا وَلَٰكِن رَّحْمَةً مِّن رَّبِّكَ لِتُنذِرَ قَوْمًا مَّا أَتَاهُم مِّن نَّذِيرٍ مِّن قَبْلِكَ لَعَلَّهُمْ يَتَذَكَّرُونَ ۝٤٦
Wa maa kunta bijaanibit Toori iz naadainaa wa laakir rahmatam mir Rabbika litunzira qawmam maaa ataahum min nazeerim min qablika la`allahum yatazakkaroon
📖 Tekkim Wolof
Nekkoo woon it wetu Tuur jamono ja Nuy woote. [Waaye dangaa dikk di] yërmaandey sa Boroom, ak it ngir nga xupp aw nit ñoo xam ne mësuñoo am ab xuppekat ci la ko jiitu, ndax it ñu mën caa fàttalikoo.

🎧 Dégg


📜 Aaya 44-48 — Al-Qasas

44وَمَا كُنتَ بِجَانِبِ الْغَرْبِيِّ إِذْ قَضَيْنَا إِلَىٰ مُوسَى الْأَمْرَ وَمَا كُنتَ مِنَ الشَّاهِدِينَ
Te yaw [Muhammad], nekkoo woon ca xuru sowwu wa ca ba Nuy jox Muusaa ndigal ya: te fekkewoo ko woon [seede ko].
45وَلَٰكِنَّا أَنشَأْنَا قُرُونًا فَتَطَاوَلَ عَلَيْهِمُ الْعُمُرُ ۚ وَمَا كُنتَ ثَاوِيًا فِي أَهْلِ مَدْيَنَ تَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِنَا وَلَٰكِنَّا كُنَّا مُرْسِلِينَ
Waaye sosoon Nanu ay maas yu guddu na fan. Te it nekkoo woon ca waa Madiyaana di leen nettali Sunuy kàddu; waaye Nun [Yàlla], Noo daan yable.
46وَمَا كُنتَ بِجَانِبِ الطُّورِ إِذْ نَادَيْنَا وَلَٰكِن رَّحْمَةً مِّن رَّبِّكَ لِتُنذِرَ قَوْمًا مَّا أَتَاهُم مِّن نَّذِيرٍ مِّن قَبْلِكَ لَعَلَّهُمْ يَتَذَكَّرُونَ
Nekkoo woon it wetu Tuur jamono ja Nuy woote. [Waaye dangaa dikk di] yërmaandey sa Boroom, ak it ngir nga xupp aw nit ñoo xam ne mësuñoo am ab xuppekat ci la ko jiitu, ndax it ñu mën caa fàttalikoo.
47وَلَوْلَا أَن تُصِيبَهُم مُّصِيبَةٌ بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيهِمْ فَيَقُولُوا رَبَّنَا لَوْلَا أَرْسَلْتَ إِلَيْنَا رَسُولًا فَنَتَّبِعَ آيَاتِكَ وَنَكُونَ مِنَ الْمُؤْمِنِينَ
Bu fekkoon ne musaba da leen dale ca la ñu daan jëf ci seeni yoxo, kon dey danañu wax naan : “Yaw sunu Boroom, lu tax yónni woo ci nun ab Yonent ? [Soo ko defoon dey], dinanu topp say ndigal te it dananu gëm doon ay jullit”.
48فَلَمَّا جَاءَهُمُ الْحَقُّ مِنْ عِندِنَا قَالُوا لَوْلَا أُوتِيَ مِثْلَ مَا أُوتِيَ مُوسَىٰ ۚ أَوَلَمْ يَكْفُرُوا بِمَا أُوتِيَ مُوسَىٰ مِن قَبْلُ ۖ قَالُوا سِحْرَانِ تَظَاهَرَا وَقَالُوا إِنَّا بِكُلٍّ كَافِرُونَ
Ba leen dëgg ga dikkalee bawoo fi Nun, ñuy wax naan : “Cëy bu nu amoon la ñu joxoon Muusaa ! ”. [Kon ñoom], ndax weddiwuñu woon bu jëkk la Nu joxoon Muusaa ? Te daan wax naan : “Ñaar ñii daal ay jibarkat lañu yuy jàppalante ! ”. Tey wax naan : “Weddi nanu leen ñoom ñépp”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
46Aaya

Tekki — Al-Qasas 46

Simoore Al-Qasas Aaya 46 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nekkoo woon it wetu Tuur jamono ja Nuy woote. [Waaye…

Simoore Aaya 46/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 44–48. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers