Aali Imran · 183/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ عَهِدَ إِلَيْنَا أَلَّا نُؤْمِنَ لِرَسُولٍ حَتَّىٰ يَأْتِيَنَا بِقُرْبَانٍ تَأْكُلُهُ النَّارُ ۗ قُلْ قَدْ جَاءَكُمْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِي بِالْبَيِّنَاتِ وَبِالَّذِي قُلْتُمْ فَلِمَ قَتَلْتُمُوهُمْ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝١٨٣
Allazeena qaalooo innal laaha `ahida ilainaaa allaa nu`mina liRasoolin hatta yaa tiyanaa biqurbaanin taa kuluhun naar; qul qad jaaa`akum Rusulum min qablee bilbaiyinaati wa billazee qultum falima qataltumoohum in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Yàlla dégg na ña wax ne : “Yàlla kóllarante na ak nun, te ne duñu gëm benn Yonent li feek indilunu yool boo xam ne safaraa koy lekk”. - Neel : “Ay Yonent dikkaloon na leen jiitu ma, indiwaale woon lay yu leer nàññ ak la ngeen laaj. Su fekkee ñu dëggu ngeen, lu tax ngeen rey leen” ?

🎧 Dégg


📜 Aaya 181-185 — Aali Imran

181لَّقَدْ سَمِعَ اللَّهُ قَوْلَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ فَقِيرٌ وَنَحْنُ أَغْنِيَاءُ ۘ سَنَكْتُبُ مَا قَالُوا وَقَتْلَهُمُ الْأَنبِيَاءَ بِغَيْرِ حَقٍّ وَنَقُولُ ذُوقُوا عَذَابَ الْحَرِيقِ
Yàlla dégg na waxi ña naan : “Yàlla ku ñàkk la te nun danoo woomal”. [Nun Yàlla] dananu bind la Nu wax, ak rey ga ñu rey Yonent ya ci lu dul dëgg. Te dananu leen wax : “Toqamtikuleen mbugal muy lakke.
182ذَٰلِكَ بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ لَيْسَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ
Loolu, ngir la seeni yoxo jëf [ci lu bon] ! ”. Te Yàlla du tooñ jaamam ña.
183الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ عَهِدَ إِلَيْنَا أَلَّا نُؤْمِنَ لِرَسُولٍ حَتَّىٰ يَأْتِيَنَا بِقُرْبَانٍ تَأْكُلُهُ النَّارُ ۗ قُلْ قَدْ جَاءَكُمْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِي بِالْبَيِّنَاتِ وَبِالَّذِي قُلْتُمْ فَلِمَ قَتَلْتُمُوهُمْ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Yàlla dégg na ña wax ne : “Yàlla kóllarante na ak nun, te ne duñu gëm benn Yonent li feek indilunu yool boo xam ne safaraa koy lekk”. - Neel : “Ay Yonent dikkaloon na leen jiitu ma, indiwaale woon lay yu leer nàññ ak la ngeen laaj. Su fekkee ñu dëggu ngeen, lu tax ngeen rey leen” ?
184فَإِن كَذَّبُوكَ فَقَدْ كُذِّبَ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ جَاءُوا بِالْبَيِّنَاتِ وَالزُّبُرِ وَالْكِتَابِ الْمُنِيرِ
Suñu la weddee, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu. Indi woon nañu ay lay yu leer ak [Zabuur] ak Téere bu leer.
185كُلُّ نَفْسٍ ذَائِقَةُ الْمَوْتِ ۗ وَإِنَّمَا تُوَفَّوْنَ أُجُورَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۖ فَمَن زُحْزِحَ عَنِ النَّارِ وَأُدْخِلَ الْجَنَّةَ فَقَدْ فَازَ ۗ وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا مَتَاعُ الْغُرُورِ
Bakkan bu nekk dana tàqamtiku [mos] dee. Waaye dangeen jot seen pey ca Bis-pénc ba. Ku ñu soreel Safara ba, dugal ko Àjjana, texe na. Te dundug àddina gi du dara lu dul xéewal guy naxe [naxti ndaw].
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
183Aaya

Tekki — Aali Imran 183

Simoore Aali Imran Aaya 183 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla dégg na ña wax ne : “Yàlla kóllarante na…

Simoore Aaya 183/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 181–185. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers