Aali Imran · 78/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَإِنَّ مِنْهُمْ لَفَرِيقًا يَلْوُونَ أَلْسِنَتَهُم بِالْكِتَابِ لِتَحْسَبُوهُ مِنَ الْكِتَابِ وَمَا هُوَ مِنَ الْكِتَابِ وَيَقُولُونَ هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ وَمَا هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ وَيَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُمْ يَعْلَمُونَ ۝٧٨
Wa inna minhum lafaree qany yalwoona alsinatahum bil Kitaabi litahsaboohu minal Kitaab, wa maa huwa minal Kitaabi wa yaqooloon huwa min `indillaahi wa maa huwa min `indillaahi wa yaqooloona `alal laahil kaziba wa hum ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Am na ci ñoom kurél buy damm seeni làmmiñ [bu ñuy jàng] Téere ba ngir ngeen defe ne la ñuy wax ca Téere ba la bokk, te bokku ca ; ñu naan : “Lu jóge ca Yàlla la”, te jógewul ca Yàlla. Di wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.

🎧 Dégg


📜 Aaya 76-80 — Simoore Aali Imran

76بَلَىٰ مَنْ أَوْفَىٰ بِعَهْدِهِ وَاتَّقَىٰ فَإِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُتَّقِينَ
Axakañ [am na lu leen war] ci ñoom, ku matal kóllareem ci ragal [Yàlla], na xam ne Yàlla safoo na ña ragal Yàlla.
77إِنَّ الَّذِينَ يَشْتَرُونَ بِعَهْدِ اللَّهِ وَأَيْمَانِهِمْ ثَمَنًا قَلِيلًا أُولَٰئِكَ لَا خَلَاقَ لَهُمْ فِي الْآخِرَةِ وَلَا يُكَلِّمُهُمُ اللَّهُ وَلَا يَنظُرُ إِلَيْهِمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَلَا يُزَكِّيهِمْ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne jaay nañu kóllareg Yàlla ak seeni ngiñ ci njëg gu néew, ñooña amuñu cër ca àllaaxira, Yàlla duleen xool te du wax ak ñoom bu Bés-pénc baa te duleen laabal itam ; te mbugal mu metti dana dal ci seen kaw.
78وَإِنَّ مِنْهُمْ لَفَرِيقًا يَلْوُونَ أَلْسِنَتَهُم بِالْكِتَابِ لِتَحْسَبُوهُ مِنَ الْكِتَابِ وَمَا هُوَ مِنَ الْكِتَابِ وَيَقُولُونَ هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ وَمَا هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ وَيَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Am na ci ñoom kurél buy damm seeni làmmiñ [bu ñuy jàng] Téere ba ngir ngeen defe ne la ñuy wax ca Téere ba la bokk, te bokku ca ; ñu naan : “Lu jóge ca Yàlla la”, te jógewul ca Yàlla. Di wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.
79مَا كَانَ لِبَشَرٍ أَن يُؤْتِيَهُ اللَّهُ الْكِتَابَ وَالْحُكْمَ وَالنُّبُوَّةَ ثُمَّ يَقُولَ لِلنَّاسِ كُونُوا عِبَادًا لِّي مِن دُونِ اللَّهِ وَلَٰكِن كُونُوا رَبَّانِيِّينَ بِمَا كُنتُمْ تُعَلِّمُونَ الْكِتَابَ وَبِمَا كُنتُمْ تَدْرُسُونَ
Mënul a nekk nit koo xam ne Yàlla daf koo jox ab Téere ak xam-xamu xereñ [ràññee], def ko ab Yonent ba noppi muy wax nit ñi : “Nekkleen samay jaam bàyyi Yàlla” ; la muy wax kay moo di: “Nekkleen jaamukati seen Boroom niki ngeen ko jàngee woon ca Téere ba te xame ko na”.
80وَلَا يَأْمُرَكُمْ أَن تَتَّخِذُوا الْمَلَائِكَةَ وَالنَّبِيِّينَ أَرْبَابًا ۗ أَيَأْمُرُكُم بِالْكُفْرِ بَعْدَ إِذْ أَنتُم مُّسْلِمُونَ
Te duleen digal jàppe Malaaka ya ak Yonent ya ay yàlla. Ndax duleen digal jëfi yéefar ginnaaw bi ngeen wommatoo jëm ci Yàlla?
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
78Aaya

Tekki — Aali Imran 78

Simoore Aali Imran Aaya 78 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci ñoom kurél buy damm seeni làmmiñ [bu…

Simoore Aaya 78/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 76–80. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers