Luqman · 27/34
Tekki Waxtaan — Luqman
وَلَوْ أَنَّمَا فِي الْأَرْضِ مِن شَجَرَةٍ أَقْلَامٌ وَالْبَحْرُ يَمُدُّهُ مِن بَعْدِهِ سَبْعَةُ أَبْحُرٍ مَّا نَفِدَتْ كَلِمَاتُ اللَّهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ ۝٢٧
Wa law annamaa fil ardi min shajaratin aqlaamunw wal bahru yamudduhoo mim ba`dihee sab`atu abhurim maa nafidat Kalimaatul laah; innal laaha `azeezun Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Su fekkoon ne mboolem li nekk ci suuf si ciy garab, dafa doon ay xalima, géej gi amaat yeneen juróom-ñaari géej yu koy dolli, lépp di daa, kon dey du tax kàdduy Yàlla jeex. Yàlla Borom Kàttan la, di Ku Xereñ.

🎧 Dégg


📜 Aaya 25-29 — Luqman

25وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلِ الْحَمْدُ لِلَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Te su leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ? ”, kon ñu ne : “Yàlla ! ”. Waxal : “Cant ñeel na Yàlla ! ”. Waaye ñi ëpp ci ñoom xamuñu.
26لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ إِنَّ اللَّهَ هُوَ الْغَنِيُّ الْحَمِيدُ
Yàllaa moom li ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku doylu la, di Yayoowaakoonub cant !
27وَلَوْ أَنَّمَا فِي الْأَرْضِ مِن شَجَرَةٍ أَقْلَامٌ وَالْبَحْرُ يَمُدُّهُ مِن بَعْدِهِ سَبْعَةُ أَبْحُرٍ مَّا نَفِدَتْ كَلِمَاتُ اللَّهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
Su fekkoon ne mboolem li nekk ci suuf si ciy garab, dafa doon ay xalima, géej gi amaat yeneen juróom-ñaari géej yu koy dolli, lépp di daa, kon dey du tax kàdduy Yàlla jeex. Yàlla Borom Kàttan la, di Ku Xereñ.
28مَّا خَلْقُكُمْ وَلَا بَعْثُكُمْ إِلَّا كَنَفْسٍ وَاحِدَةٍ ۗ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ بَصِيرٌ
Seenug sosu ak seenug dekkiwaat yéen ñépp, mi ngi yombe Yàlla ni benn bakkan kepp. Yàlla Kuy Dégg la, Kuy Gis la.
29أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ يُولِجُ اللَّيْلَ فِي النَّهَارِ وَيُولِجُ النَّهَارَ فِي اللَّيْلِ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ كُلٌّ يَجْرِي إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى وَأَنَّ اللَّهَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Xanaa gisoo ne Yàlla mooy dugal guddi ci bëccëg, Moom dugal it bëccëg it ci guddi, Moo tàggat jant beek weer wi, ku ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal ? Te Yàlla Ku Deñ- kumpa la, Ku Xàmmee li ngeen di def la.
LuqmanFihi Alxuraan
34Aaya
MeccanRevelation
27Aaya

Tekki — Luqman 27

Simoore Luqman Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Su fekkoon ne mboolem li nekk ci suuf si ciy…

Simoore Aaya 27/34 — Luqman لقمان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Luqman Dégg, Luqman Tekki, Luqman mp3, Luqman pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers