Al-Ahzab · 2/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
وَاتَّبِعْ مَا يُوحَىٰ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرًا ۝٢
Wattabi` maa yoohaaa ilaika mir Rabbik; innal laaha kaana bimaa ta`maloona Khabeera
📖 Tekkim Wolof
Toppal li ñu lay soloo te mu bawoo ca sa Boroom. Yàlla xàmmee na ca la ngeen di def.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-4 — Al-Ahzab

1يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ اتَّقِ اللَّهَ وَلَا تُطِعِ الْكَافِرِينَ وَالْمُنَافِقِينَ ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلِيمًا حَكِيمًا
Éy yaw Yonent bi ! Ragalal Yàlla te bul topp yéefar yi ak naaféq yi, Yàlla ku xam la, Ku xereñ la.
2وَاتَّبِعْ مَا يُوحَىٰ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرًا
Toppal li ñu lay soloo te mu bawoo ca sa Boroom. Yàlla xàmmee na ca la ngeen di def.
3وَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Te nangay wéeru ci Yàlla. [Ndax] Yàlla doy na sëkk wéeruwaay.
4مَّا جَعَلَ اللَّهُ لِرَجُلٍ مِّن قَلْبَيْنِ فِي جَوْفِهِ ۚ وَمَا جَعَلَ أَزْوَاجَكُمُ اللَّائِي تُظَاهِرُونَ مِنْهُنَّ أُمَّهَاتِكُمْ ۚ وَمَا جَعَلَ أَدْعِيَاءَكُمْ أَبْنَاءَكُمْ ۚ ذَٰلِكُمْ قَوْلُكُم بِأَفْوَاهِكُمْ ۖ وَاللَّهُ يَقُولُ الْحَقَّ وَهُوَ يَهْدِي السَّبِيلَ
Yàlla defalul kenn nit ñaari xol ci dënnëm. Deful it jabar yi ngeen di wodde seen pendali ndey [ci pase] ñuy seeni yaay . Deful it doom yi ngeen doomoo ñuy seeni doom. Loolu seeni wax doŋŋ la ju yem ci seeni gémmiñ. Yàlla dëgg lay wax te Mooy jubbanti, di tege ci yoon wu jub.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
2Aaya

Tekki — Al-Ahzab 2

Simoore Al-Ahzab Aaya 2 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Toppal li ñu lay soloo te mu bawoo ca sa…

Simoore Aaya 2/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 1–4. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers