Saba · 38/54
Tekki Waxtaan — Saba
وَالَّذِينَ يَسْعَوْنَ فِي آيَاتِنَا مُعَاجِزِينَ أُولَٰئِكَ فِي الْعَذَابِ مُحْضَرُونَ ۝٣٨
Wallazeena yas`awna feee Aayaatinaa mu`aajizeena ulaaa`ika fil`azaabi muhdaroon
📖 Tekkim Wolof
Waaye ña daan dox, di dëgërante bopp ak Sunuy kàddu, ñoom ña nga ne xeew ci biir mbugal ma.
🎧 Dégg

📜 Aaya 36-40 — Saba

36قُلْ إِنَّ رَبِّي يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ وَيَقْدِرُ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëg, di ko xatal it. Waaye li ëpp ci nit ñi waxuñu”.
37وَمَا أَمْوَالُكُمْ وَلَا أَوْلَادُكُم بِالَّتِي تُقَرِّبُكُمْ عِندَنَا زُلْفَىٰ إِلَّا مَنْ آمَنَ وَعَمِلَ صَالِحًا فَأُولَٰئِكَ لَهُمْ جَزَاءُ الضِّعْفِ بِمَا عَمِلُوا وَهُمْ فِي الْغُرُفَاتِ آمِنُونَ
Nekkul ne seeni alal walla seeni doom ñoo leen di tax a jegeñ Yàlla. Lu dul ña ca gëm tey jëf u yiw. Ñooñu danañu am pey gu ñu fulandi ci sababus la ñu daan jëf, te ñoom ña nga ne fayax ci ay kër yu kawe [ca Àjjana].
38وَالَّذِينَ يَسْعَوْنَ فِي آيَاتِنَا مُعَاجِزِينَ أُولَٰئِكَ فِي الْعَذَابِ مُحْضَرُونَ
Waaye ña daan dox, di dëgërante bopp ak Sunuy kàddu, ñoom ña nga ne xeew ci biir mbugal ma.
39قُلْ إِنَّ رَبِّي يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ وَيَقْدِرُ لَهُ ۚ وَمَا أَنفَقْتُم مِّن شَيْءٍ فَهُوَ يُخْلِفُهُ ۖ وَهُوَ خَيْرُ الرَّازِقِينَ
Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam ci jaamam yi, Moo koy xatal it. Lépp lu ngeen mën a joxe [ci alal], moom Yàlla moo koy wuutalaat, te Yàlla moo di ngën ji kuy wërsëgal”.
40وَيَوْمَ يَحْشُرُهُمْ جَمِيعًا ثُمَّ يَقُولُ لِلْمَلَائِكَةِ أَهَٰؤُلَاءِ إِيَّاكُمْ كَانُوا يَعْبُدُونَ
Bu keroogee Bis ba leen Yàlla di dajale mbooleseen. Ba noppi daldi wax Malaaka ya ne leen : “Moo ndax ñii yéen la ñu daan jaamu ? ”.
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
38Aaya

Tekki — Saba 38

Simoore Saba Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waaye ña daan dox, di dëgërante bopp ak Sunuy kàddu,…

Simoore Aaya 38/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers